Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka
عربي Àngale Urdu
ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem
عربي Àngale Urdu
seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit
عربي Àngale Urdu
buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam
عربي Àngale Urdu
nit ki gën a texe ci samag rammu ëllëg bis-penc, mooy ki wax, Laa ilaaha illal Laahu, te mu sell lool ci xolam, walla ci bakkanam
عربي Àngale Urdu
ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara
عربي Àngale Urdu
ñiy taral alku nañu
عربي Àngale Urdu
ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko
عربي Àngale Urdu
bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem te daggu ko
عربي Àngale Urdu
ku wax: laahi ilaaha illallaahu, amul kenn ku ñu war a jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla alalam ak dereetam araam na, Yàlla rekk nag mooy càmbar ay jëfam
عربي Àngale Urdu
baatu dëgg boobu jinne moo koy këf sànni ko ci noppi kilifaam kem kàddu ginaar gu jigéen, ñu jaxase si lu ëpp téeméeri fen
عربي Àngale Urdu
buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli
عربي Àngale Urdu
ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
عربي Àngale Urdu
àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara
عربي Àngale Urdu
ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara
عربي Àngale Urdu
Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi
عربي Àngale Urdu
buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw
عربي Àngale Urdu
wàlle amul, gaafal amul, gaatnga lu baax nag yéem na ma» nee na, ñu ne ko: lan mooy gaatnga lu baax ? Mu ne: "wax ju teey
عربي Àngale Urdu
ci lan lañuy jaayante ak yaw? Mu ne: "ci ngeen jaamu Yàlla te du ngeen ko bokkaale ak dara, ak julliy juróom, ak di topp -mu daaldi wax kàddu gu suufe ne- te du ngeen laaj nit ñi dara
عربي Àngale Urdu
giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom da ngeen topp yoonu ña leen jiitu woon
عربي Àngale Urdu
Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wax ak moom ci yenn mbir yi, daal di ne ko: bu soobe Yàlla soob la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "ndax dangamay yamale ak Yàlla? Waxal: bu soobe Yàlla moom dong
عربي Àngale Urdu
ku takk ab téere bokkaale na
عربي Àngale Urdu