عَنْ أَبِي وَاقِدٍ اللَّيْثِيِّ رضي الله عنه:
أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لَمَّا خَرَجَ إِلَى حُنَيْنٍ مَرَّ بِشَجَرَةٍ لِلْمُشْرِكِينَ يُقَالُ لَهَا: ذَاتُ أَنْوَاطٍ يُعَلِّقُونَ عَلَيْهَا أَسْلِحَتَهُمْ، فَقَالُوا: يَا رَسُولَ اللهِ، اجْعَلْ لَنَا ذَاتَ أَنْوَاطٍ كَمَا لَهُمْ ذَاتُ أَنْوَاطٍ، فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «سُبْحَانَ اللهِ! هَذَا كَمَا قَالَ قَوْمُ مُوسَى {اجْعَلْ لَنَا إِلَهًا كَمَا لَهُمْ آلِهَةٌ} [الأعراف: 138] وَالَّذِي نَفْسِي بِيَدِهِ لَتَرْكَبُنَّ سُنَّةَ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمْ».
[صحيح] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 2180]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Waaxidin Allaysii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Bi Yonnente Yàlla bi génnee jëm Hunayni dafa romb genn garabu bokkaalekat yi ñu koy wooye: boroom lonk ya, ñu fay lonk seen i ngànnaay, ñu ne ko: wutal nu gu am ay lonkkaay kemm ñoom ni ñu ame boroomi lonkkaay, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: "tudd naa sellug Yàlla gi ! Lii de moo ngi mel ni la niti Muusaa ya waxoon {wutal nu Yàlla kem ñoom ni ñu ame ay Yàlla} [Al-Ahraaf: 138] giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom da ngeen topp yoonu ña leen jiitu woon".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2180]
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn jëm Hunayni: aw xur la ci diggante Tayif ak Màkka, mu àndoon ak Sahaaba yiy door a dugg ci Lislaam, Ñu romb ag garab gu ñuy woowe: "Saatu Anwaat", maanaam: boroom lonkkaay yi, bokkaalekat yi dañu ko daan màggal di fa lonk seen i ngànnaay ak yeneen ngir sàkku baarke, Ñu sàkku ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu defal leen ag garab gu mel ni moom,ñu di fa lonk seen i ngànnaay, ngir sàkku barke; ndax dañoo njort ne loolu lu dagan la, Yonnente bi daal di sàbbaal ngir weddi seen wax jii, ak màggal Yàlla, mu xamal leen ne wax jii day niróo ak la niti Muusaa ya waxoon: {defal nu Yàlla kem ñoom ni ñu ame ay Yàlla}, Ba ñu gissee ñiy jaamu ay xërëm dañoo sàkku mu defal leen ay xërëm kem ni bokkaalekat yi ame ay xërëm, ak ne lii mooy topp seen yoon wa, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne xeet wii dana topp yoonu Yahuut yi ak Nasaraan yi di def seen jëf ya, muy moytandikuloo loolu.