عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما:
أَنَّ رَجُلًا أَتَى النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَكَلَّمَهُ فِي بَعْضِ الْأَمْرِ، فَقَالَ: مَا شَاءَ اللهُ وَشِئْتَ، فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَجَعَلْتَنِي لِلَّهِ عَدْلًا؟ قُلْ: مَا شَاءَ اللهُ وَحْدَهُ».
[إسناده حسن] - [رواه ابن ماجه والنسائي في الكبرى وأحمد] - [السنن الكبرى للنسائي: 10759]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne:
Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wax ak moom ci yenn mbir yi, daal di ne ko: bu soobe Yàlla soob la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "ndax dangamay yamale ak Yàlla? Waxal: bu soobe Yàlla moom dong".
[Ag càllalaam tane na] - [Ibnu Maaja soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat] - [Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi - 10759]
Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ak moom ci mbiram, topp mu ne ko: "bu soobe Yàlla soob la", Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di weddi wax ji, xamal ko ne toftal coobarey mbiddeef ci coobarey Yàlla toftal gu sës rikk, bokkaale gu ndaw la, du dagan jullit bi wax ko, Mu daadi koy jubbanti ci wax ju jub, mooy: "bu soobe Yàlla moom dong", mu wéetal Yàlla ci coobareem, te bañ caa toftal coobarey kenn, xeetu toftal gu mu man a doon.