+ -

عَن عُمَرَ بنِ الخَطَّابِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قال: سَمِعْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«لَا تُطْرُونِي كَمَا أَطْرَتِ النَّصَارَى ابْنَ مَرْيَمَ؛ فَإِنَّمَا أَنَا عَبْدُهُ، فَقُولُوا: عَبْدُ اللهِ وَرَسُولُهُ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 3445]
المزيــد ...

Jële nañu ci Umar Ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3445]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere ëppal ak jéggi dayob Sariiha ci tagg ko ak di ko melal ay meloy Yàlla mu kawe mi ak i jëfam ya mu jagoo, walla ne dafa xam kumpa, walla di ko boole ak Yàlla ci ñaan, kem ni ko Nasaraan yi defe ci Iisaa doomu Maryama -yal na ko Yàlla dolli jàmm-. Topp mu leeral ne moom jaam la ci jaami Yàlla yi, mu digle ne nañuy wax ci moom ne: jaamub Yàlla la ak ndawam.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani الأكانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Moytandikuloo jéggi dayob Sariiha ci màggal walla tagg; ndax loolu day jëme ci bokkaale.
  2. Li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- doon moytandikuloo de tàbbi na ci xeet wi, am kurel yu ëppal ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-, am it kurel yu ëppal ci waa kër Yónente bi, ak kurel yu ëppal ci wàlliyu yi, ñoom ñépp tàbbi ci bokkaale.
  3. Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa melal boppam ci ne jaamub Yàlla la; ngir leeral ne moom ab jaam bu Yàlla moom la, daganul ñuy jëmale ci moom dara ci lu Boroom bi jagoo.
  4. Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dafa melal boppam ci ne ndawu Yàlla la; ngir leeral ne moom Yàllaa ko yónni, kon ñu war koo dëggal te topp ko.