عَنْ ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما قَالَ:
قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ غَدَاةَ الْعَقَبَةِ وَهُوَ عَلَى نَاقَتِهِ: «الْقُطْ لِي حَصًى» فَلَقَطْتُ لَهُ سَبْعَ حَصَيَاتٍ، هُنَّ حَصَى الْخَذْفِ، فَجَعَلَ يَنْفُضُهُنَّ فِي كَفِّهِ وَيَقُولُ: «أَمْثَالَ هَؤُلَاءِ فَارْمُوا» ثُمَّ قَالَ: «أَيُّهَا النَّاسُ، إِيَّاكُمْ وَالْغُلُوَّ فِي الدِّينِ، فَإِنَّما أَهْلَكَ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمْ الْغُلُوُّ فِي الدِّينِ».
[صحيح] - [رواه ابن ماجه والنسائي وأحمد] - [سنن ابن ماجه: 3029]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ci subag sànni jamra fekk moo ngi ci kaw giléemam gi: "foral ma ay xeer" ma foral ko juróom-ñaari xeer yu sew, muy xeer yi muy sànni, mu tàmbali de leen sànni ci loxoom, di wax naan: "sànnileen yu mel nii" daal di wax ne: " yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine".
[Wér na] - [Ibnu Maaja soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja - 3029]
Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne nekkoon na ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bisub tabaski ci subag sànni jamratu Haqaba yi ci ajug tàggatoo ga, Mu digal ko mu foral ko ay xeeri jamra, mu foral ko juróom-ñaari xeer yu sew, benn bi toll ni doomi Himmas walla bundux, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- teg ko ci loxoom di ko yëngal, daal di wax ne: Yu toll ni yooyu ci jëmm ngeen sànni sànni ko, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal moytondikuloo ëppal ak taral ak jéggi dayo ci biri diine, ndax li alag xeet ya jiitu woon mooy jéggi dayo ak ëppal ak taral ci diine.