+ -

عن عائشة رضي الله عنها قالت:
سَأَلَ أُنَاسٌ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَنِ الْكُهَّانِ، فَقَالَ لَهُمْ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «لَيْسُوا بِشَيْءٍ» قَالُوا: يَا رَسُولَ اللهِ، فَإِنَّهُمْ يُحَدِّثُونَ أَحْيَانًا بِالشَّيْءِ يَكُونُ حَقًّا، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «تِلْكَ الْكَلِمَةُ مِنَ الْحَقِّ يَخْطَفُهَا الْجِنِّيُّ فَيَقُرُّهَا فِي أُذُنِ وَلِيِّهِ قَرَّ الدَّجَاجَةِ، فَيَخْلِطُونَ فِيهَا أَكْثَرَ مِنْ مِائَةِ كَذْبَةٍ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6213]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Ay nit laaj na ñu Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mbiri gisaanekat, mune leen: «nekkuñu ci dara» ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ñoom de leeg-leeg ñu wax nu dara mu nekk dëgg’ mine leen: «baatu dëgg boobu jinne moo koy këf sànni ko ci noppi kilifaam kem kàddu ginaar gu jigéen, ñu jaxase si lu ëpp téeméeri fen».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6213]

Leeral

Laaj na ñu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mbiri ñiy xibaare kumpa ci li ñëwagul, mu wax ne: buleen leen faale, te buleen jël séen i wax, te buleen séen mbir yitteel.
Ñu ne ko: ñoom séen wax leeg-leeg mu dëppoo ak li am, kem bu ñu xibaare ne benn mbiru kumpa dana am ci weer nàngam ak bis sàngam, dafay am kemm ni ñu ko waxe.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: jinne yi ñooy jëf li nuy dégg ci xibaaru asamaan, ñu wàcc dem ca séen kilifay gisaanekat ya wax leen la ñu dégg, gisaanekat bi dolli ci li jinne yi dégge ca asamaan téeméeri fen.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Kanadi البلغارية Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tere nañu dëggal ab gisaanekat, ak ne ñoom li ñuy wax ay fen la ay sos la, donte leeg-leeg sax mu wax dëgg.
  2. Aarees na asamaan si ci Saytaane yi ginnaawam bi ñu yónnee Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba duñu dégg dara ci soloo gi mbaa leneen, lu dul ku sàcc ab dégg daal di rëcc jum yay tàkk.
  3. Jinne yi dañu leen di wutal ay péete ci nit ñi.