عن أنس رضي الله عنه قال:
كُنَّا عِنْدَ عُمَرَ فَقَالَ: «نُهِينَا عَنِ التَّكَلُّفِ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 7293]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Nekkoon a nu ci Umar mu wax ne: "tere nañ nu toggoo lu metti"
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 7293]
Umar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na nu nuy toggoo yu metti yi ci lu dul aajo, moo xam ci wax mbaa jëf.