عن عائشة رضي الله عنها قالت: قال النبي صلى الله عليه وسلم:
«لَا تَسُبُّوا الْأَمْوَاتَ، فَإِنَّهُمْ قَدْ أَفْضَوْا إِلَى مَا قَدَّمُوا».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 1393]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1393]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral araamug ŋàññi ñi faatu ak di wax ci séeni der, te loolu bokk na ci jikko yu ñaaw yi, ndax ñoom àgg nañu ca jëf ya ñu jiitaloon moo xam baax na walla bon na, te saaga woowu du àgg ci ñoom, te ñiy dundu rek lay lor.