Xàjjale yi: Pas-pasu Lislaam . Gëm dogal yi .

عَنْ مَطَرِ بْنِ عُكَامِسٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِذَا قَضَى اللَّهُ لِعَبْدٍ أَنْ يَمُوتَ بِأَرْضٍ جَعَلَ لَهُ إِلَيْهَا حَاجَةً».

[صحيح] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 2146]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Matar Ibn Hukaamis- yal na leen Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo».

[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2146]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bu Yàlla dogalee ci jaam bi mu War a faatu a fi barab te moom nekku fa; da ko fay defal aajo mu dem fa, ñu jël fa ag ruuham.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi:
  2. Hadiis bi day dëggal li Yàlla mu kawe mi wax ne: {benn bakkan xamul ci ban suuf lay faatoo}.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (65)