Xàjjale yi: Pas-pasu Lislaam .
+ -

عن أبي ذر رضي الله عنه:
عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِيمَا رَوَى عَنِ اللهِ تَبَارَكَ وَتَعَالَى أَنَّهُ قَالَ: «يَا عِبَادِي إِنِّي حَرَّمْتُ الظُّلْمَ عَلَى نَفْسِي، وَجَعَلْتُهُ بَيْنَكُمْ مُحَرَّمًا، فَلَا تَظَالَمُوا، يَا عِبَادِي كُلُّكُمْ ضَالٌّ إِلَّا مَنْ هَدَيْتُهُ، فَاسْتَهْدُونِي أَهْدِكُمْ، يَا عِبَادِي كُلُّكُمْ جَائِعٌ إِلَّا مَنْ أَطْعَمْتُهُ، فَاسْتَطْعِمُونِي أُطْعِمْكُمْ، يَا عِبَادِي كُلُّكُمْ عَارٍ إِلَّا مَنْ كَسَوْتُهُ، فَاسْتَكْسُونِي أَكْسُكُمْ، يَا عِبَادِي إِنَّكُمْ تُخْطِئُونَ بِاللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَأَنَا أَغْفِرُ الذُّنُوبَ جَمِيعًا فَاسْتَغْفِرُونِي أَغْفِرْ لَكُمْ، يَا عِبَادِي إِنَّكُمْ لَنْ تَبْلُغُوا ضَرِّي فَتَضُرُّونِي، وَلَنْ تَبْلُغُوا نَفْعِي فَتَنْفَعُونِي، يَا عِبَادِي لَوْ أَنَّ أَوَّلَكُمْ وَآخِرَكُمْ وَإِنْسَكُمْ وَجِنَّكُمْ كَانُوا عَلَى أَتْقَى قَلْبِ رَجُلٍ وَاحِدٍ مِنْكُمْ مَا زَادَ ذَلِكَ فِي مُلْكِي شَيْئًا، يَا عِبَادِي لَوْ أَنَّ أَوَّلَكُمْ وَآخِرَكُمْ وَإِنْسَكُمْ وَجِنَّكُمْ كَانُوا عَلَى أَفْجَرِ قَلْبِ رَجُلٍ وَاحِدٍ مَا نَقَصَ ذَلِكَ مِنْ مُلْكِي شَيْئًا، يَا عِبَادِي لَوْ أَنَّ أَوَّلَكُمْ وَآخِرَكُمْ وَإِنْسَكُمْ وَجِنَّكُمْ قَامُوا فِي صَعِيدٍ وَاحِدٍ فَسَأَلُونِي فَأَعْطَيْتُ كُلَّ إِنْسَانٍ مَسْأَلَتَهُ مَا نَقَصَ ذَلِكَ مِمَّا عِنْدِي إِلَّا كَمَا يَنْقُصُ الْمِخْيَطُ إِذَا أُدْخِلَ الْبَحْرَ، يَا عِبَادِي إِنَّمَا هِيَ أَعْمَالُكُمْ أُحْصِيهَا لَكُمْ ثُمَّ أُوَفِّيكُمْ إِيَّاهَا، فَمَنْ وَجَدَ خَيْرًا فَلْيَحْمَدِ اللهَ، وَمَنْ وَجَدَ غَيْرَ ذَلِكَ فَلَا يَلُومَنَّ إِلَّا نَفْسَهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2577]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:
Jële na ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yàlla mu kawe mi mu wax ne:«yéen sama jaam ñi damaa araamal tooñ ci sama bopp, ma def ko muy lu araam ci seen diggante kon buleen di tooñante, yéen sama jaam ñi yéen ñépp dangeen a réer ku dul ki ma gindi, kon sàkkuleen ci man gindiku ma gindi leen, yéen sama jaam ñi yéen ñépp a xiif ku dul ki ma leel, kon sàkkuleen ci man ma leel leen , kon dinaa leen leel, yéen sama jaam ñi yéen ñépp a rafle ku dul ki ma wodd, kon sàkkuleen ci man ma wodd leen kon dinaa leen wodd, yéen sama jaam ñi dangeen di juum guddi ak bëccëg kon jéggaluleen ma ma jéggal leen, yéen sama jaam ñi manuleen maa lor ba di ma lor, te manuleen maa jariñ ba di ma jariñ, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñi mujj ci yéen, nit ñi ak jinne yi ci yéen bu ñu neekkoon xolu ki gën a ragal Yàlla ci yéen loolu du yokk ci sama nguur gi dara, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñu mujj ña, ak seen i nit ak jinne bu ñu neekkoon xolu ki gën a kàccoor ci yéen loolu du wàññi ci sama nguur gi dara, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñu mujj ña, ak seen i nit ak jinne dañoo taxaw ci benn pàkk bu yaatu, ñu ñaan ma ma jox kenn ku nekk la mu ñaan loolu du wàññi li ne fi man lu dul li ab puso di wàññi ci ndoxum géej gi bu ñu ko sa dugalee, yéen sama jaam ñi seen jëf rekk laa leen di dencal joxaat leen ko ba mu mat, ku fa fekk yiw na sant Yàlla, waaye ku fa fekk ay bu mu yedd ku dul boppam».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2577]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ngi leeral ne Yàlla dafa wax ne Moom daa araamal tooñ ci boppam, mu def tooñ muy lu araam ci diggante mbindéefam yi, bu kenn tooñ kenn. Mbindéef yi it ñéppay sànku ludul ku Yàlla jubal, te ku ko ñaan Yàlla dana ka ko dëppale te gindi ko. Jaam ñi ñépp a ñàkk te aajowoo jëm ci Yàlla ci séen aajo yépp, ku ñaan Yàlla nag dana faj aajoom te dana ko doy. Te it dañuy def bàkkaar guddi ak bëccëg, Yàlla di leen sururaal di baal jaam bi saa bu sàkkoo njéggal. Te ñoom it manuñóo lor Yàlla te manu ñu koo jariñ ci dara. Te it bu ñu nekkoon ci ben xolu ki gën a ragal Yàlla kon seenug ragal Yàlla du dolli dara ci nguurug Yàlla. Bu ñu nekkoon it ci xolu ki gën a kàccoore kon seenug kàccoore du wàññi dara ci nguuram gi; ndax ñoom dañoo lompañ te dañoo ñàkk jëm ci Yàlla, te aajowoo ko ci bépp anam ak bépp jamono ak bépp bérab, te Moom Yàlla mooy Aji-Doylu ji -tudd naa sellam ga-. ñoom de bu ñu taxawoon ci benn bérab nit ña ak jinne ya, ña njëkk ak ña mujj di ñaan Yàlla, mu may kenn ku nekk la mu ñaan, loolu du wàññi dara ci li nekk ci Yàlla, niki puso bi bu ñu ko dugaloon ci géej gi daal di koy génnewaat du wàññi ca géej ga dara, loolu nag ngirug matam Moom Yàlla mu sell mi.
Ak ne sunu boroom day wattu jëfi jaam ñi takkal leen ko, bu bis-pénc baa mu jox leen ko ba mu mat, ku fa fekk payug jëfam nekk aw yiw na sant Yàlla ci li mu ko dëppaleek yoonu toppu ko, ku fa feek payug jëfam di leneen kooku bu mu yedd kenn kudul bakkanam biy digle lu ñaaw te wommat ko jëme ko ci toskare.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Hadiis bii dafa bokk ci li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al xuddsi walla Hadiisu Al Ilaahiy, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la juge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññetle ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci jàng gi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëgge mbaa di ci lottloowaate ak yenneen.
  2. Lépp lu jaam bi am ci xam-xam walla ag njub, ci xamleg Yàlla ak ug gindéem la ame.
  3. Lu jaam bi am ci yiw ci ngëneelu Yàlla mu kawe mi la ko ame, waaye lépp lu ko jot ci ay ci bakkanam ak bànneexam la juge.
  4. Képp kuy rafetal ci tawfeexu Yàlla la, te ag payam ci ngëneelu Yàlla la, kon cant ñeel na ko, képp kuy ñaawal bu mu yedd lu dul bakkanam.