عن الْأَغَرِّ رضي الله عنه، وَكَانَ مِنْ أَصْحَابِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«يَا أَيُّهَا النَّاسُ تُوبُوا إِلَى اللهِ، فَإِنِّي أَتُوبُ فِي الْيَوْمِ إِلَيْهِ مِائَةَ مَرَّةٍ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2702]
المزيــد ...
Jële nañu ci Al-Axarri yal na ko Yàlla dollee gërëm mu bokkoon ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu wax ne: Yonente Yàlla bi nee na:
«yéen nit ñi tuubleen jëm ci Yàlla, man de damay tuub ci bis bi téeméeri yoon».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2702]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digal na nit ñi ñuy baril tuub ak jéggalu, mu xibaar ci boppam ne moom day tuub jëm ci Yàlla mu kawe di ko jéggalu ci bis bi lu ëpp téeméeri yoon, te moom jéggalees na ko li jiitu ci ay bàkkaaram ak li mujj, nekk ci loolu matug toroxlu ak jaamu Yàlla mu màgg mi.