عن أبي هريرة رضي الله عنه
عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فِيمَا يَحْكِي عَنْ رَبِّهِ عَزَّ وَجَلَّ، قَالَ: «أَذْنَبَ عَبْدٌ ذَنْبًا، فَقَالَ: اللَّهُمَّ اغْفِرْ لِي ذَنْبِي، فَقَالَ تَبَارَكَ وَتَعَالَى: أَذْنَبَ عَبْدِي ذَنْبًا، فَعَلِمَ أَنَّ لَهُ رَبًّا يَغْفِرُ الذَّنْبَ، وَيَأْخُذُ بِالذَّنْبِ، ثُمَّ عَادَ فَأَذْنَبَ، فَقَالَ: أَيْ رَبِّ اغْفِرْ لِي ذَنْبِي، فَقَالَ تَبَارَكَ وَتَعَالَى: عَبْدِي أَذْنَبَ ذَنْبًا، فَعَلِمَ أَنَّ لَهُ رَبًّا يَغْفِرُ الذَّنْبَ، وَيَأْخُذُ بِالذَّنْبِ، ثُمَّ عَادَ فَأَذْنَبَ، فَقَالَ: أَيْ رَبِّ اغْفِرْ لِي ذَنْبِي، فَقَالَ تَبَارَكَ وَتَعَالَى: أَذْنَبَ عَبْدِي ذَنْبًا، فَعَلِمَ أَنَّ لَهُ رَبًّا يَغْفِرُ الذَّنْبَ، وَيَأْخُذُ بِالذَّنْبِ، اعْمَلْ مَا شِئْتَ فَقَدْ غَفَرْتُ لَكَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2758]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:
Jële na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu nettali jële ci Boroomam mu màgg mi, mu wax ne: «ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar Yàlla mu baarkeel mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar,Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, defal lu la soob jéggal naa la».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2758]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day nettali jële ci Boroomam ne jaam bi bu defee bàkkaar, daal di wax sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu kawe mi day wax: sama jaam bi def na bàkkaar xam na ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, di ko suturaal, baal ko walla mu mbugal ko, kon jéggal naa ko. jaam bi dellu defaat bàkkaar xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, di ko suturaal, baal ko walla mu mbugal ko, kon jéggal naa sama jaam bi. jaam bi dellu defaat bàkkaar xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, di ko suturaal, baal ko walla mu mbugal ko, kon jéggal naa sama jaam bi, na def lu ko soob feek saa yu defee bàkkaar, day bàyyi bàkkaar ba réccu ko, dogu ci bañ caa delluwaat, waaye bakkanam da koy not mu tàbbiwaat ca bàkkaar ba, feek moo ngi def nii di def bàkkaar tey tuub dinaa ko jéggal, ndax tuub day màbb la ko jiitu.