Xàjjale yi: Ngëneel yi ak teggiin yi .
+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم كان يقول:
«الصَّلَوَاتُ الْخَمْسُ، وَالْجُمُعَةُ إِلَى الْجُمُعَةِ، وَرَمَضَانُ إِلَى رَمَضَانَ، مُكَفِّرَاتٌ مَا بَيْنَهُنَّ إِذَا اجْتَنَبَ الْكَبَائِرَ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 233]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 233]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne julliy juróom yi ñu farataal ci bëccëg gi ak ci guddi gi, ak jullig Àjjuma ci ayu-bis gune, ak woor weeru koor ci at mu ne, da ñuy far bàkkaar yu ndaw yi ci seen diggante ci sartub moytu bàkkaar yu mag yi, Bu dee bàkkaar yu mag yi nag moom niki njaalo ak naan sàngara dara du ko far lu dul tuub.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani الأكانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bàkkaar yi daa am yu ndaw am yu mag.
  2. Far bàkkaar yu ndaw yi dafa aju ci moytu bàkkaar yu mag yi.
  3. Bàkkaar yu mag yi mooy bàkkaar yi nga xam ne gétan (ay daan) da cee war ci àdduna, walla ag tëkkug àllaaxira ñëw ci mbugal, walla merum Yàlla, walla ag xuppe nekk ca, mbaa ag rëbb ñeel ki ko def, lu mel ni njaalo ak naan sàngara.