+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«لَا تَجْعَلُوا بُيُوتَكُمْ قُبُورًا، وَلَا تَجْعَلُوا قَبْرِي عِيدًا، وَصَلُّوا عَلَيَّ؛ فَإِنَّ صَلَاتَكُمْ تَبْلُغُنِي حَيْثُ كُنْتُمْ».

[حسن] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 2042]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«buleen def seen kër yi ay bàmmeel, te buleen def sama bàmmeel am ndaje, deeleen julli ci man, ndax seen ug julli ci man dina yeksi fi man ak fu ngeen man di nekk».

[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 2042]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere neenal kër yi bañfaa julli ba muy mel ni ay bàmmeel yu ñu dul julli, Mu tere it di baril ay siyaare bàmmeelam ak di fa dajaloo ci anamug aadawoo; ndax loolu day jëme ci bokkaale, Mu digle ñu julli ci moom ci bépp barab ci kaw suuf; ndax loolu dana àgg fa moom moo xam ci ku jege la walla ku sori ñoo ci yam, kon aajowoowul di barila dem ca bàmmeelam.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tere di neenal kër yi ci bañ faa jaamu Yàlla mu kawe mi.
  2. Tere di tukki ngir siyaare bàmmeelu Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ndaxte digle na ñu julli ci moom, mu xibaare ne dana àgg fa moom. Kon dañuy tukki ngir jublu jàkka ja ak julli fa.
  3. Araamug def siyaare bàmmeelu Yónent bi am ndaje, ci di baril di ko siyaare ci anam gu ñu ko jagleel ak ci jamono ju ñu ko jagleel, naka noonu bàmmeel yépp.
  4. Teddug Yónente bi ci Boroomam, ba tax mu yoonal ñuy julli ci moom ci jamono ju ne, ci barab bu ne.
  5. Te sax na ci Sahaaba yi ñuy tere julli ci bàmmeel yi; looloo tax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere ñuy def kër yi mu mel ni ay bàmmeel ba kenn du fa julli.