عن خَولة الأنصاريةِ رضي الله عنها قالت: سمعت النبي صلى الله عليه وسلم يقول:
«إِنَّ رِجَالًا يَتَخَوَّضُونَ فِي مَالِ اللهِ بِغَيْرِ حَقٍّ، فَلَهُمُ النَّارُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 3118]
المزيــد ...
Jële nañu ci Xawlata mi bokk ci waa-lansaar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3118]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle nit ñay jëfandikoo alali jullit ñi cig neen, di ko jël ci lu dul dëgg, te lii nag day matale mbooleem alal yi, ci dajale ga ak fàggu ga ci lu daganul, ak joxe ko ci anam gu baaxul, dana ci dugg itam lekk alali jirim yi, ak alali sarax suy wéy (waqf), ak weddi ndénkaane ya, ak jël ci alali mbooloo te yayoowoo ko.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daldi xamle ne séenug fay keroog bis-pénc mooy sawara.