عن عائشة رضي الله عنها قالت: سمعتُ من رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول في بيتي هذا:
«اللَّهُمَّ مَنْ وَلِيَ مِنْ أَمْرِ أُمَّتِي شَيْئًا فَشَقَّ عَلَيْهِمْ فَاشْقُقْ عَلَيْهِ، وَمَنْ وَلِيَ مِنْ أَمْرِ أُمَّتِي شَيْئًا فَرَفَقَ بِهِمْ فَارْفُقْ بِهِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1828]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fekk mi ngi ci sama biir néeg bii muy wax naan:
«yaw Yàlla sama Boroom képp ku méngoo dara ci sama mbiri xeet wii, ba noppi di tar ci ñoom, na nga tar ci kawam, waaye képp ku ménggoo dara ci sama mbiri xeet wii, daal di leen woyofalal, na nga ko woyofalal».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1828]
Bokk na ci njariñal adiis bi :
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ñaanal na képp ku jiite dara ci mbiri xeetam wi lu ndaw walla lu rëy, moo xam jiite gu matale ñépp la, walla jiite gu làmboo ab pàcc la, mu teg leen ab coona te yërëmuleen, Yàlla fay ko kem ay jëfam te teg ko ab coono.
Waaye ku leen ñeewante yombal séen i bir Yàlla ñeewante ko te yombalal ko ay biram.