عن مَعقِلِ بن يَسار المُزَنِيّ رضي الله عنه قال: إني سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«مَا مِنْ عَبْدٍ يَسْتَرْعِيهِ اللهُ رَعِيَّةً، يَمُوتُ يَوْمَ يَمُوتُ وَهُوَ غَاشٌّ لِرَعِيَّتِهِ، إِلَّا حَرَّمَ اللهُ عَلَيْهِ الْجَنَّةَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 142]
المزيــد ...
Jële nañu ci Mahqal Ibn Yasaar Almusanii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 142]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku Yàlla def kilifa mu jiite nit ñi, moo xam njiit lu mag la niki buur, walla njiit lu ndaw niki góor gi ci këram, ak jigéen gi ci këram, mu gàttanlu ci àqi la muy sàmm, di leen wuruj te du leen laabire, daal di sànk séen i àq yu diine mbaa yi àdduna, kooku yayoo na mbugal mu tar mii.