En Ar


Sémbuw kàggu gi ñeel Adiisi Yónnent ak i tekkeem:

Sémb wuy mottalante ngir tànn Adiisi Yónnent yi baamu ci Lislaam ak yamu làmboo ak leeral ko ci anam gu yomb te matale, topp tekki ko ci anam gu baax gu kawe gi dëppoo ak doxaliin yees càmbar jëm ci làkk yiy dund, ak maye ko mu ànd ak mbooleem jumtukaay yi jàppandi.

Jubluwaay yi:

  1. Amal ay delluwaay yoy kojug réew yépp la te amul fay di ay delluwaay yu wóor yu méngoo ak jamono ngir tekki Adiisi Yónnent yi.
  2. Jàppandal dencukaay gog ci lënd gi la ngir tekkiy Adiis yi nekk ci kanamu ñiy tekki ci waxtu yi ñuy tekki.
  3. Àggale tekki yi ci ña mu soxal ànd ko ak mbooleem jumtukaay yi jàppandi.

Bokk na ci yu am solo yi kàggu gi jagoo:

  1. Ag matale.
  2. Amul fay.
  3. Fasantikoog tekki yi.
  4. Saytu guy wéy ngir méngale ak jamono.
  5. Xereñ.

Jaaruwaayi tabax ab jëmale kanam:

  1. Tabax kàggu ci làkku araab.
  2. Tekki kàggu yi ci làkk yi.
  3. Yembal ak baddug lënd ñeel kàggu gi.
  4. Saytu guy wéy ngir méngale ak jamono kàggu gi ak i tekkeem.
Doxal gi ak jëmale kanam gi ci baayaleg: