+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضيَ اللهُ عنهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«انْظُرُوا إِلَى مَنْ أَسْفَلَ مِنْكُمْ، وَلَا تَنْظُرُوا إِلَى مَنْ هُوَ فَوْقَكُمْ، فَهُوَ أَجْدَرُ أَلَّا تَزْدَرُوا نِعْمَةَ اللهِ عَلَيْكُمْ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2963]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"deeleen xool ñi leen féete suuf, te buleen xool ci ñi leen féete kaw, ndax moo gën a yay ba dungeen xeeb xéewali Yàlla yi ci seen kaw".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2963]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na ñuy xool ci mbiri àdduna yi ci wàccuwaay ak alal ak daraja ak lu dul loolu ci meloy ñi féete suuf te gën a néewle, te bañ a xool ci mbiri àdduna yi ñi féete kaw te gënle la, ndaxte xool ci kila féete suuf mooy tax ba doo xeeb walla ngay tuutal xéewal yi la Yàlla defal.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Doylu dafa bokk ci li gën a màgg ci jikkóy way-gëm yi, te màndarga la ci gërëm dogalu Yàlla.
  2. Ibn Hajar nee na: hadiis bii dafa boole xeeti yiw yi; ndax nit bu gisee ki ko gënle ci àdduna bakkanam day sàkku lu mel noonu, xeeb li mu am ci xéewali Yàlla yi, mu xér ci yokk ngir dab kooku mbaa mu jege ko, te lii moo nekk ci ñi ëpp ci nit ñi, bu dee dafa xool ci mbiri àdduna ki ko féete suuf kon day gis xéewali Yàlla yi ci moom, mu sant ca daal di toroxlu, daal di ciy def lu baax.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi