Ràññetle gi: Ngëneel yi ak teggiin yi .

عن أبي الدرداء رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ رَدَّ عَنْ عِرْضِ أَخِيهِ رَدَّ اللهُ عَنْ وَجْهِهِ النَّارَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ».

[صحيح] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 1931]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».

[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 1931]

Leeral gi

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daf nuy xamal ne képp kuy sàmm wormay mbokkum jullit ci jëw ak ci tere ñu ŋàññ ko walla jëmale si moom lu ñaaw, Yàlla dana ko fegal mbugal ca bis-pénc ba.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi: Tere nañu di wax ci deru jullit ñi.
  2. Am pay daal mu ngay toll kem na jëf ja tollu, ku feg deru mbokkam Yàlla fegal ko sawara.
  3. Lislaam diiney mbokkoo la ak dimbalante ci diggante ay ñoñam.
Gaaral firi yi
Làkk wi: الإنجليزية الأوردية الإسبانية Yataal gi (68)