عن جابر رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«رَحِمَ اللهُ رَجُلًا سَمْحًا إِذَا بَاعَ، وَإِذَا اشْتَرَى، وَإِذَا اقْتَضَى».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 2076]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2076]
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñaanal yërmaande ñeel képp ku yomb te tabe di ku yaatu cim njaayam; Du taral ci kiy jënn ca njëg ga, te day jëflanteek moom ci jikko yu rafet, Di ku yomb te tabe te yomb bu dee jënn; du ŋott te du xeeb dayob bagaas ya, Di ku yomb te tabe te yéwen bu dee sàkku ñu fay ko ay boram; du tar ci aji-ñàkk ji ak aji-yittewóo ji, waaye da koy sàkku cig nooy ak ñeewantu, te day néggandiku ki ne ci jafe-jafe.