عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«رَغِمَ أَنْفُ، ثُمَّ رَغِمَ أَنْفُ، ثُمَّ رَغِمَ أَنْفُ»، قِيلَ: مَنْ؟ يَا رَسُولَ اللهِ قَالَ: «مَنْ أَدْرَكَ أَبَوَيْهِ عِنْدَ الْكِبَرِ، أَحَدَهُمَا أَوْ كِلَيْهِمَا فَلَمْ يَدْخُلِ الْجَنَّةَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2551]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"torox na, torox na, torox na" ñu ne ko: kan? Yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "ku fekk ñaari way-juram di ay mag, kenn ka walla ñaar ñépp te duggul Àjjana".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2551]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñaanal toroxtange ba mu mel ni ku teg bakkanam ci suuf -baamtu na ko ñatti yoon- ñu laaj ko: kan ngay ñaan Yàlla yaw yonnente bi?
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: ki fekk ñaari way-juram doon ay mag -kenn ka walla ñaar ñépp- te nekkuñu sabab ci mu dugg àjjana; loolu nag ngir ñàkk a rafetal jëme ci ñoom ñaar, ak ñàkk a leen a déggal.