Xàjjale yi: Ngëneel yi ak teggiin yi .
+ -

عن عائشة رضي الله عنها عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«إِنَّ أَبْغَضَ الرِّجَالِ إِلَى اللهِ الْأَلَدُّ الْخَصِمُ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2457]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Sunna yi bu Ad-daaraqutniy - 2457]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy ku man a xulóo te bari le ko, mooy ki dul nangoo topp dëgg, te di ko jéem a weddi ci dàggasante, walla muy xulóo ci dëgg waaye day ëppal ca xulóo ba, ba day jéggi dayo, di werente cig ñàkk a xam.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Oromoo Kanadi Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Du bokk ci xeetu dàggasante buñu ŋàññi su dee ki ñu tooñ dafa laaj yelleefam ci yoon.
  2. Werente ak xulóo dafa bokk ci gàkk-gàkki làmmeñ yiy sabab ag tàqalikoo ak bàyyente ci diggante jullit ñi.
  3. Dàggasante dana baax bu teggee cig dëgg te defiin wa rafet, waaye dees na ko wàññi bu dee ngir delloo dëgg la saxal ay neen, walla mu bañ a am ay lay ak ay firnde.