عن حذيفة رضي الله عنه قال: سمعت النبي صلى الله عليه وسلم يقول:
«لَا يَدْخُلُ الْجَنَّةَ قَتَّاتٌ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6056]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Husayfata Inb Yamaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«ab ràmbaajkat du dugg àjjana».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6056]

Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm- day xamle ne ràmbaajkat biy tuxal ay wax ci diggante nit ñi jubloo yàq séen diggante kooku yayoo naa mbugal ci mu bañ a dugg àjjana.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi : Rambaaj ci Bàkkaar yu mag yi la bokk.
  2. Tere nañu rambaaj; ndax li ci nekk ci yàq ak lor ci diggante nit ñi ak askan wi.
Gaaral firi yi
Làkk wi: الإنجليزية الأوردية الإسبانية Yataal gi (68)