Xàjjale yi: Ngëneel yi ak teggiin yi .
+ -

عن جُبَير بن مُطْعِم رضي الله عنه أنه سمع النبي صلى الله عليه وسلم يقول:
«لَا يَدْخُلُ الْجَنَّةَ قَاطِعُ رَحِمٍ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2556]
المزيــد ...

Jële nañu ci Jubayru Ibn Muthim -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«kuy dog mbokk du dugg àjjana».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere bu wér bi ñeel Ibnu Hibbaan - 2556]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku dog ay mbokkam ca la ñu yayoo ci ay àq, walla lor leen, di ñaawal jëme ci ñoom, kooku yayoowul a dugg àjjana.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Oromoo Kanadi Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi :
  2. Dog mbokk ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
  3. Jokk mbokk day amee ca kem nañu ko miine, kon day wuute kem barab ya ak jamono ya ak nit ña.
  4. Jokk mbokk dana nekk ci siyaare, ak sarax, ak rafetal jëme ci moom, ak seeti ku feebar, ak digal leen lu baax tere leen lu bon, ak yeneen.
  5. Lu mbokk gi di gën a jege dog mbokk gi di gën a rëy bàkkaar.