Xàjjale yi: Ngëneel yi ak teggiin yi .
+ -

عَنْ جَابِرِ بْنِ عَبْدِ اللهِ رضي الله عنهما أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«اتَّقُوا الظُّلْمَ، فَإِنَّ الظُّلْمَ ظُلُمَاتٌ يَوْمَ الْقِيَامَةِ، وَاتَّقُوا الشُّحَّ، فَإِنَّ الشُّحَّ أَهْلَكَ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمْ، حَمَلَهُمْ عَلَى أَنْ سَفَكُوا دِمَاءَهُمْ وَاسْتَحَلُّوا مَحَارِمَهُمْ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2578]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na:
«Moytuleen tooñ, ndax tooñ ay lëndëm lay doon ëllëg bis-pénc, te ngeen moytu nay, ndaxte nay moo alag ña leen jiitu woon, yóbbe na leen ñu tuur seen i dereet ak a daganal araam».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2578]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo tooñ, te bokk na ca: tooñ nit ñi, ak tooñ sa bakkan, ak tooñ ci àqi Yàlla mu kawe mi. Te mooy bañ a jox ku nekk àqam, ak ne tooñ ay lëndëm lay doon ci kaw ay ñoñam ëllëg bis-pénc ci ñu daje fa ak ay tar-tar ak i tiitaange, Mu tere bëgge te mooy nay gu tar ak ug xér ci alal, bokk na ca gànteñlu ci joxe àqi alal yi ak xér gu tar ci àdduna. Xeetu tooñ gii moo alag xeet yi ñu jiitu woon, ndax da leen a yóbbe woon ci ñenn ñi di ray ñeneen ñi, ak di daganal yu araam yi Yàlla araamal.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hadiis bi:Joxe alal ak jàpple mbokk yi dafa bokk ci yiy waral bëggante ak jokkoo.
  2. Nay ak bëgge day yóbbe nit ki ci moy ak i ñaawteef ak i bàkkaar.
  3. Waaru ci mbiri xeet ya jiitu woon.