عن أنس بن مالك رضي الله عنه:
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ لَا يَرُدُّ الطِّيبَ.

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 2582]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul delloo gëtt.

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2582]

Leeral

Bokk na ci njubug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moom daawul delloo gëtt da ko daan nangu; ndax lu woyof a gàddu la te lu neex ug xet la.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sopp nañu nangu gëtt gu ñu la may; ndax gàddu ko amul coono, te nangu gi amul ndamu.
  2. Mat ak rafetug jikkoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci ne du delloo gëtt, ak ne day nangu adiya ju ñu ko jox.
  3. Xemmemloo ci jëfandikoo gëtt.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (63)