Toftaleg Adiis yi

bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg
عربي Àngale Urdu
àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli
عربي Àngale Urdu
ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul
عربي Àngale Urdu
Du dagan ci nit ki mu tóng mbokkam lu ëpp ñatti guddi, ñuy dajee kii dummóoyu kee dummóoyu, ki gën ci ñoom ñaar mooy ki tàmbli nuyóo ba
عربي Àngale Urdu
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul delloo gëtt
عربي Àngale Urdu
Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca
عربي Àngale Urdu
yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam
عربي Àngale Urdu
bu kenn ci yenn di lekk na lekke loxo ndeyjooram, buy naan na naane loxo ndeyjooram, ndax Saytaane loxob càmmooñam lay lekke, loxob càmmoñam lay naane
عربي Àngale Urdu
bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab
عربي Àngale Urdu
Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam daa di saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal
عربي Àngale Urdu
Benn waay da doon lekke càmmooñ fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: "lekkeel sa ndayjoor", waa ji ne ko: manuma ko, mu ne ko: "Yàlla boo ko man
عربي Àngale Urdu
kiy biral Alxuraan moo ngi mel ni kiy biral ab sarax, kiy yalu Alxuraan it moo ngi mel ni kiy nëbb ab sarax
عربي Àngale Urdu
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- guddi gu nekk bu daan yéeg ci lalam day boole ñaari téqam, daal di ciy ëf, daal di jàng: {Xul huwal Laahu Ahadun}, ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi}
عربي Àngale Urdu