عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ:
أَنَّ أَعْرَابِيًّا أَتَى النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: دُلَّنِي عَلَى عَمَلٍ إِذَا عَمِلْتُهُ دَخَلْتُ الجَنَّةَ، قَالَ: «تَعْبُدُ اللَّهَ لاَ تُشْرِكُ بِهِ شَيْئًا، وَتُقِيمُ الصَّلاَةَ المَكْتُوبَةَ، وَتُؤَدِّي الزَّكَاةَ المَفْرُوضَةَ، وَتَصُومُ رَمَضَانَ» قَالَ: وَالَّذِي نَفْسِي بِيَدِهِ لاَ أَزِيدُ عَلَى هَذَا، فَلَمَّا وَلَّى قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «مَنْ سَرَّهُ أَنْ يَنْظُرَ إِلَى رَجُلٍ مِنْ أَهْلِ الجَنَّةِ، فَلْيَنْظُرْ إِلَى هَذَا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1397]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm:
Benn kaw-kaw dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: tegtal ma jëf joo xam ne su ma ko defee dinaa dugg àjjana, mu ne ko: "dangay jaamu Yàlla te doo ko bokkaale ak dara, di taxawal julliy farata, di joxe asaka, di woor weeru koor" mu ne ko: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom duma dolli ci lii dara, ba mu demee Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne : "ku bëgg a xool nit ku bokk ci waa àjjana, na xool waa jii".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1397]
Benn waay dafa jóge ca kaw ga ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir mu tegtal ko jëf ju koy dugal àjjana, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tontu ko ci ne dugg àjjana ak mucc ci sawara day taxaw ci def ponki Lislaam yi, ci jaamu Yàlla moom dong, te bañ koo bokkaale ak dara. Ak nga taxawal julliy juróom yi Yàlla farataal ci jaamam yi ci bis bi ak ci guddi gu ne. Nga joxe sa asakay alal yi Yàlla waral ci yaw, nga jox ko ñi ko yeyoo. Ak nga sàmmonte ak woor weeru koor ci waxtoom. Waa ji wax ne giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom duma dolli ci jëfi farata yii ma dégg ci yaw dara ci ay jaamu, te duma ci wàññi dara. Ba mu demee Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: Ku bëgg a xool nit ku bokk ci waa àjjana na xool kaw-kaw bii.