+ -

عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما أن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«بَلِّغُوا عَنِّي وَلَوْ آيَةً، وَحَدِّثُوا عَنْ بَنِي إِسْرَائِيلَ وَلَا حَرَجَ، وَمَنْ كَذَبَ عَلَيَّ مُتَعَمِّدًا فَلْيَتَبَوَّأْ مَقْعَدَهُ مِنَ النَّارِ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 3461]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Jottalileen jële ci man donte benn aaya la, ta ngeen waxtaane waa Banuu Israayil ci lu amul benn jafe-jafe, waaye ku ma fenal te tay ko na waajal ab tooguwaayam ca sawara».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3461]

Leeral

Yónente bi dafa digle ñu jottali xam-xam biy juge ci moom ci muy Alxuraan walla Sunna, donte tuuti la niki benn aaya Alxuraan walla benn Hadiis, ci sartub mu xam li miy jottali ak limiy woote. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne jafe-jafe nekkul ci waxtaane Banuu Israayil ci xew-xew ya amoon ci ñoom bu wuutewul ak sunu Sariiha. Topp Mu moytandikuloo ci di ko fenal, tek ci ne kepp ku ko fenal te tay ko na daal di jëlal boppam dëkkuwaayam ca sawara.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Xemmemloo ci jottali njàngalem Yàlla, ak ne nit ki dafa war ci moom mu jottali li mu mokkal te xam ko, donte dafa néew.
  2. Warug sàkku xam-xamu Sariiha; ngir mu man a jaamu Yàlla, ak di jottali tërëliinam yi ci anam gu wér.
  3. Warug wóorlu ci wérug bépp Hadiis lu jiitu jottali ga, walla tasaare ga, ngir moytoo dugg ci tëkku gu tar gii.
  4. Ñaaxe ci wax dëgg ak di teey ci wax ja, ba du tàbbi ci fen, rawatina ci Sariihab Yàlla mu màgg mi.