عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ عَنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنَّهُ قَالَ:
«سَيَكُونُ فِي آخِرِ أُمَّتِي أُنَاسٌ يُحَدِّثُونَكُمْ مَا لَمْ تَسْمَعُوا أَنْتُمْ وَلَا آبَاؤُكُمْ، فَإِيَّاكُمْ وَإِيَّاهُمْ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 6]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ci sama mujjuw xeet wi dana am ay nit yu leen di wax lu ngeen masuta dégg yéen ak séen i baay, nangeen leen moytu».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 6]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaare ne ay nit danañu feeñ ci mujjanteelu xeetam wi di sos ay fen, di wax loo xamne kenn ku leen jiitu woon masu koo wax, di xibaare ay waxi fen yu ñu duur, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal nu nu moytu leen te bañ a toog ak ñoom, bañ a déglu séen i waxtaan; ngir wax yooyu ñu duur du sax si xel yi, te duñu man a mucc ci moom.