Listu hadiis yi

Maa ngi leen di dénk ragal Yàlla, ak dégg ak topp, donte ab jaam moo leen jiite, képp ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, maa ngi leen di dénk sama sunna si ak sunnay njiit yu jub yi tey jubal
عربي الإنجليزية الأوردية
Jottalileen jële ci man donte benn aaya la, ta ngeen waxtaane waa Banuu Israayil ci lu amul benn jafe-jafe, waaye ku ma fenal te tay ko na waajal ab tooguwaayam ca sawara
عربي الإنجليزية الأوردية
mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la
عربي الإنجليزية الأوردية
dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal
عربي الإنجليزية الأوردية
ku ma waxal jenn wax te xam ne ay fen la, moom kenn la ci fenkat yi
عربي الإنجليزية الأوردية
ku ma fenal te tay ko na waajal ab wàccuwaayam ca sawara
عربي الإنجليزية الأوردية
ci sama mujjuw xeet wi dana am ay nit yu leen di wax lu ngeen masuta dégg yéen ak séen i baay, nangeen leen moytu
عربي الإنجليزية الأوردية
bindal, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, dara du ci génn lu dul dëgg
عربي الإنجليزية الأوردية