عَنْ أَبِي نَجِيحٍ العِرْبَاضِ بْنِ سَارِيَةَ رضي الله عنه قَالَ: وَعَظَنَا رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مَوْعِظَةً وَجِلَتْ مِنْهَا القُلُوبُ، وَذَرَفَتْ مِنْهَا العُيُونُ، فَقُلْنَا: يَا رَسُولَ اللهِ! كَأَنَّهَا مَوْعِظَةُ مُوَدِّعٍ؛ فَأَوْصِنَا، قَالَ:
«أُوصِيكُمْ بِتَقْوَى اللَّهِ، وَالسَّمْعِ وَالطَّاعَةِ، وَإِنْ تَأَمَّرَ عَلَيْكُمْ عَبْدٌ، فَإِنَّهُ مَنْ يَعِشْ مِنْكُمْ بَعْدِي فَسَيَرَى اخْتِلَافًا كَثِيرًا، فَعَلَيْكُمْ بِسُنَّتِي وَسُنَّةِ الخُلَفَاءِ الرَّاشِدِينَ المَهْدِيينَ، عَضُّوا عَلَيْهَا بِالنَّوَاجِذِ، وَإِيَّاكُمْ وَمُحْدَثَاتِ الأُمُورِ؛ فَإِنَّ كُلَّ بِدْعَةٍ ضَلَالَةٌ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي] - [الأربعون النووية: 28]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Najiih Al-Hirbaad ibn Saariyata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc waar na nu ag waare ba xol yi jàq ci, bët yi jooy, nu ne ko: yaw Yonente Yàlla bi! Dafa mel ni waarew tàggatoo la; kon laabire nu, mu wax ne:
Maa ngi leen di dénk ragal Yàlla, ak dégg ak topp, donte ab jaam moo leen jiite, képp ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, maa ngi leen di dénk sama sunna si ak sunnay njiit yu jub yi tey jubal, ŋànkleen ci ak séen i dégéj, maa ngi leen di moytandikuloo bir yi ñu sos; ndax bidaa yépp ag cànkute la".
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy] - [الأربعون النووية - 28]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa waar Sahaaba yi ag waar gu jotale ba xol yi ragal ca, bët yi jooy ca, Ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi dafa me ni waareg kuy tàggatoo la ndax li ñu ci gis ci jotaleg Yónente bi ci waare gi, ñu sàkku ci moom ag ndénkaane gog danañu ci jàpp ginnaawam, Mu ne leen : maa ngi leen fi dénk ragal Yàlla mu màgg mi, ci def yi war ak bàyyi yi ñu araamal, Ak dégg ak topp, maanaam : ñeel njiit yi, doonte ab jaam moo leen jiite, mbaa mu not leen ba jiite leen, maanaam ki gën a suufe ci nit ñi moo leen jiite buleen rëy ci loolu nangeen ko topp, ndax day ragal a yëkkati fitna, ndaxte ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, Mu leeralal leen ni ñuy génne ci wuute gi, te mooy jàpp ci suunnaam ak sunnas njiit yu jub ya tey jubale ci ginnaawam, Abuu Bakarin As-Siddiix, ak Umar Ibnul Xattaab, ak Usmaan Ibnu Affaan, ak Aliyun Ibnu Abii Taalib, -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ak màtt ca ak seeni dégéj, maanaam -bëñ ya mujj-: li mu jublu ci loolu mooy farlu ci taqoo ak sunna ak jàpp ca, Mu moytondikuloo leen bir yi ñu sos fent ko ci diine, ndax bidaa yépp ay réer lañu.