Xàjjale yi:
+ -

عَنْ مُعَاذِ بْنِ جَبَلٍ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ قَالَ: قُلْت يَا رَسُولَ اللَّهِ! أَخْبِرْنِي بِعَمَلٍ يُدْخِلُنِي الجَنَّةَ وَيُبَاعِدْنِي مِنْ النَّارِ، قَالَ:
«لَقَدْ سَأَلْتَ عَنْ عَظِيمٍ، وَإِنَّهُ لَيَسِيرٌ عَلَى مَنْ يَسَّرَهُ اللَّهُ عَلَيْهِ: تَعْبُدُ اللَّهَ لَا تُشْرِكُ بِهِ شَيْئًا، وَتُقِيمُ الصَّلَاةَ، وَتُؤْتِي الزَّكَاةَ، وَتَصُومُ رَمَضَانَ، وَتَحُجُّ البَيْتَ، ثُمَّ قَالَ: أَلَا أَدُلُّكَ عَلَى أَبْوَابِ الخَيْرِ، الصَّوْمُ جُنَّةٌ، وَالصَّدَقَةُ تُطْفِئُ الْخَطِيئَةَ كَمَا يُطْفِئُ المَاءُ النَّارَ، وَصَلَاةُ الرَّجُلِ مِنْ جَوْفِ اللَّيْلِ، ثُمَّ تَلَا: {تَتَجَافَى جُنُوبُهُمْ عَنِ الْمَضَاجِعِ} حَتَّى {بَلَغَ يَعْمَلُونَ}، ثُمَّ قَالَ: أَلَا أُخْبِرُك بِرَأْسِ الأَمْرِ وَعَمُودِهِ وَذِرْوَةِ سَنَامِهِ، فَقُلْتُ: بَلَى يَا رَسُولَ اللَّهِ، قَالَ: رَأْسُ الأَمْرِ الإِسْلَامُ، وَعَمُودُهُ الصَّلَاةُ، وَذِرْوَةُ سَنَامِهِ الجِهَادُ، ثُمَّ قَالَ: أَلَا أُخْبِرُك بِمِلَاكِ ذَلِكَ كُلِّهِ، فقُلْت: بَلَى يَا رَسُولَ اللَّه! فَأَخَذَ بِلِسَانِهِ وَقَالَ: كُفَّ عَلَيْك هَذَا، قُلْت: يَا نَبِيَّ اللَّهِ! وَإِنَّا لَمُؤَاخَذُونَ بِمَا نَتَكَلَّمُ بِهِ، فَقَالَ: ثَكِلَتْكَ أُمُّكَ وَهَلْ يَكُبُّ النَّاسَ عَلَى وُجُوهِهِمْ أَوْ قَالَ عَلَى مَنَاخِرِهِمْ إلَّا حَصَائِدُ أَلسِنَتِهِمْ»!

[صحيح] - [رواه الترمذي] - [الأربعون النووية: 29]
المزيــد ...

Jële nañu ci Muhaas ibn Jabal yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: neenaa yaw Yonnente Yàlla bi! Wax ma jëf joo xam ne dana ma dugal àjjana dima soreele ak sawara, mu wax ne:
"laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku Yàlla yombalal: dangay jaamu Yàlla te doo ko bokkaale ak dara, di taxawal julli, di joxe asaka, di woor weeru koor, di aj Màkka, topp mu ne: ndax duma la tegtal bunti yiw yi, woor ab pakk la, saraxe day far njuumte kem ni ndox di faye sawara, ak jullig nit ki ci digg guddi gi, topp mu jàng: {séen wet ya day sori lal ya} ba egg {li ñuy def}, topp mu ne: ndax duma la xibaar bopp mbir mi ak kenoom ak njobbaxtalu jégénam, ma ne ko: ahakay yaw Yonente Yàlla bi, mu ne: boppu mbir mi mooy lislaam, kenoom mooy julli, njobbaxtalu jégénam mooy jihaad, topp mu ne: ndax duma la xibaar li jiital loolu lépp, ma ne ko ahakay yaw Yonnente Yàlla bi! Mu jàpp ci làmmiñam daal di ne: téyeel sa lii, ma ne ko: yaw Yonente Yàlla bi! Mo ndax dees nuy jàppe li nuy wax, mu wax ne: na la sa yaay ñàkk rekk, mo ndax dara dana këpp nit ñi ca seen kanam ya walla mu ne ca seen gémmiñ ya lu dul seen góobiti làmmiñ"!

[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [الأربعون النووية - 29]

Leeral

Muhaas yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: nekkoon naa ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci benn tukki, ma xëy benn bis jegesi ko fekk ñoo ngi dox, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi xibaar ma jëf joo xam ne dana ma dugal àjjana di ma soreele sawara, Mu ne ko: laaj nga ma jëf joo xam ne lu màgg la ci bakkan yi, waaye nag lu woyof la te yomb ci ku ko Yàlla yombal ci moom; joxeel faratay lislaam yi:
Bi ci njëkk: dangay jaamu Yàlla moom dong te doo ko bokkaale ak dara.
Ñaareel bi: nga taxawal julliy juróom yi ñu farataal ci bis bi ak guddi: Fajar, ak Tisbaar, ak Tàkkusaan, ak Timis, ak Gee, ci ay sàrtam ak i ponkam ak i warteefam.
Ñatteel bi: nga genne asaka ji ñu farataal, te moom ag jaamug alal la gu war ci jépp alal ju mat lim bu ñu tënk ci Sariiha, ñu koy jox ñi ko yeyoo.
Ñenteel bi: nga woor weeru Koor, te mooy bàyyi lekk ak naan ak yeneen yiy dogloo ànd ak yéenee jaamu, tàmbalee ci fenkug fajar gi ba ca sowug jant bi.
Juróomeel bi: nga aj néeg ba ci jublu Màkka jublu a taxawal ay jaamu, ngir jaamu Yàlla mu màgg mi.
Topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ndax duma la xamal yoon wiy eggale ci buntu yiw yi? Loolu mooy nga toftal ci farata yooyu naafila yi.
Bi ci njëkk: woorug coobarewu, moom day teree tàbbi ci moy yi ci damm bànneex, ak néewal kàttan.
Ñaareel bi: saraxeg coobarewu day fay njuumte ginnaawam di ko dindi di far jeexitalam.
Ñatteel bi: julli guddi ci ñatteelu xaaju guddi bu mujj bi, topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di jàng waxu Yàlla ji: {seen wet ya day sori} maanaam: day sori {lal ya} maanaam: nelawukaay ya {dañuy ñaan di woo seen Boroom} ci julli ak sikar ak jàng ak ñaan, {ngir ragal ak xemmeem te dañuy joxe ci li ñu leen wërsëgale, benn bakkan xamul li ñu ko deñcal ci luy bégal bët yi} maanaam: luy bégal seeni bët ëllëg bis-pénc ak ca àjjana ci ay xéewal, {muy ag fay ca la ñu doon jëf}.
Topp Yonnente bi ne ko: ndax duma la xibaar cosaanu diine? Ak kenoom gi muy sukkandiku? Ak njobbaxtalam?
Muhaas yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: mbir mi boop ba mooy: lislaam te mooy ñaari seede yi, te ci ñoom ñaar la nit ki di ame cosaanu diine. Kenoom: mooy julli, lislaam du am ci lu dul julli, kem ni nga xamee ne kër du am ci lu dul keno, kuy julli diineem dëgër na taxaw na; njobbaxtalu lislaam ak ug yëkkëtikoom moo ngi ci jihaad ak def pasteef ci xeex ak nooni diine ji ngir yëkkëti kàddug Yàlla.
Topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ndax duma la xibaar liy téyé téyé bu dëgër mbir yii weesu? Yonnente bi jàpp ci làmmiñam, ne ko: téyeel lii te bul wax lu sa yoon nekkul. Muhaas ne ko: ndax sunu Boroom da nuy topp di nu càmbar di nu mbugal ci lépp lu nuy wax?!
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: yal na la sa yaay ñàkk! Li ñu ci jublu du ñaanal ko alkande, waaye daa bokk ci waxi araab yi ngir yee ko ci mbir mum waroon a xam bàyyi ko xel, topp mu ne ko: ndax dara dana sànni nit ñi di leen daaneel ca seen kanam ya ca biir sawara lu dul seen góobiti làmmiñ ya ci kéefar ak tuumaale ak saaga ak jëw ak rambaaj ak tuuma ak yu ko niru.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Xérug Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ci xam-xam, loolu a tax ñuy baril di laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
  2. Déggug Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ndax li ñu xam ne jëf yi ñooy sabab si dugg àjjana.
  3. Laaj bi jóge ci Muhaas yal na ko Yàlla dollee gërëm laaj bu màgg la; ndaxte ca dëgg-dëgg mooy mbóotu dund gi ak ug amam, lépp lu am ci àdduna jii ci doomu Aadama walla jinne fa muy mujj mooy àjjana walla sawara, loolu a tax laaj bi di lu màgg.
  4. Toftalu dug Àjjuma ci kaw def ponki lislaam yi: te mooy: ñaari seede yi, ak julli, ak asaka, woor, ak aj.
  5. Wéetal Yàlla moy li ëpp solo ci diine mooy la gën a kawe ci lépp lu ñu waral, te mooy jaamu ko moom dong amul bokkaale.
  6. Yërmàndey Yàlla ci jaamam yi ci mu ubbil leen bunti yiw yi ngir ñu dolleeku ci sababi yiw yi ak njéggali bàkkaar yi.
  7. Ngëneelu li nekk ci di jéema jege Yàlla ci def naafila yi ginnaaw bu ñu defee farata yi.
  8. Julli ci lislaam mooy
  9. tolloog keno biy
  10. tax mbaar mi man a taxaw, bu demee
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Bosniya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent