عَنْ أَبِي سَعِيدٍ سَعْدِ بْنِ مَالِكِ بْنِ سِنَانٍ الخُدْرِيّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا ضَرَرَ وَلَا ضِرَارَ».
[حسن] - [رواه ابن ماجه، والدارقطني، وغيرهما مسندًا] - [الأربعون النووية: 32]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Sahiid Sahd ibn Maalik ibn Sinaan Al-Xudriyu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"deesul loru waaye deesul lore".
[Tane na] -
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne dañoo war a jañ lor ci ay anam yu wuute, ci sunu jëmm ak ci ñeneen ñi, daganul kenn di lor boppam mbaa muy lor keneen. Du dagan ci kenn muy delloo lor ci aw lor; ndax lor deesu ko dindee lor lu dul ci anamu fayantoo te bañ a ëppal.