عَن ابنِ عباسٍ رضي الله عنهما أنَّ رسولَ اللهِ صلي الله عليه وسلم قال:
«لَو يُعطَى النّاسُ بدَعواهُم لادَّعَى رِجالٌ أموالَ قَومٍ ودِماءَهُم، لَكِنَّ البَيِّنَةَ على المُدَّعِى، واليَمينَ على مَن أنكَرَ».
[حسن] - [رواه البيهقي، وغيره هكذا، وبعضه في الصحيحين] - [الأربعون النووية: 33]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"bu ñu doon jox nit ñi ci liñuy wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ".
[Tane na] - [رواه البيهقي وغيره هكذا وبعضه في الصحيحين] - [الأربعون النووية - 33]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne bu ñu doon jox nit ñi ngir seen i wootewoo dong ci lu dul benn firnde walla ay tegtal kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a joxe aw lay ak firnde ci li muy sàkku, bu amul aw lay ñu gaaral wootewoo ji ki ñu tuumaal, bu ko weddee dafa war a giñ daal di cay set.