Xàjjale yi:
+ -

عَنْ ابْنِ عَبَّاسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا عَنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِيمَا يَرْوِي عَنْ رَبِّهِ تَبَارَكَ وَتَعَالَى، قَالَ:
«إنَّ اللهَ كَتَبَ الحَسَنَاتِ وَالسَّيِّئَاتِ، ثُمَّ بَيَّنَ ذَلِكَ، فَمَنْ هَمَّ بِحَسَنَةٍ فَلَمْ يَعْمَلْهَا؛ كَتَبَهَا اللهُ عِنْدَهُ حَسَنَةً كَامِلَةً، وَإِنْ هَمَّ بِهَا فَعَمِلَهَا؛ كَتَبَهَا اللهُ عِنْدَهُ عَشْرَ حَسَنَاتٍ إلَى سَبْعِمِائَةِ ضِعْفٍ إلَى أَضْعَافٍ كَثِيرَةٍ، وَإِنْ هَمَّ بِسَيِّئَةٍ فَلَمْ يَعْمَلْهَا؛ كَتَبَهَا اللهُ عِنْدَهُ حَسَنَةً كَامِلَةً، وَإِنْ هَمَّ بِهَا فَعَمِلَهَا؛ كَتَبَهَا اللهُ سَيِّئَةً وَاحِدَةً».

[صحيح] - [رواه البخاري ومسلم في صحيحيهما بهذه الحروف] - [الأربعون النووية: 37]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ibn Àbbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu jële ci Boroomam mu Barkeel mi te kawe, mu wax ne:
"Yàlla bind na yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di koy leeral, ku yittewoo lu rafet te defu ko; Yàlla dana bindal fa moom aw yiw wu mat, bu ko yittewoo daal di koy def; Yàlla bind ko fa moom fukk yu rafet ba ci juróom-ñaari téeméeri full, ba ay full yu bari lool, bu yittewoo lu ñaaw te defu ko; Yàlla bind ko fa moom aw yiw wu mat, bu ko yittewoo daal di koy def; Yàlla bind ko fa moom wenn ñaawteef ".

[Wér na] - [رواه البخاري ومسلم في صحيحيهما بهذه الحروف] - [الأربعون النووية - 37]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne Yàlla dogal na yiw yi ak ñaawtéef yi daal di leeralal ñaari Malaaka yi naka lañu koy bindee:
Képp ku namm a def lu rafet te dogu ci def ko dees na ko bindal wenn yiw doonte defu ko, bu ko defee nag ñu fulal ka ko fukk yu mel ni moom ba ci juróom-ñaari téeméeri yoon, ba ci ay yoon yu bari, ci kem la nek ca xol ba cig sellal ak jariñ ñeneen mbaa lu ni mel.
Waaye képp ku nàmm a def ñaawtéef te dogu ci def ko, far bàyyi ko ngir Yàlla dees na ka ko bindal aw yiw, bu ko bàyyee ngir yittewootu ko te deful ay sababam deesu ko bindal dara, waaye su ko bàyyee ngir ak lott dees na ko bindal yéeneem, su ko defee nag ñu bindal ko benn ñaawtéef.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral ngëneelul Yàlla lu màgg li ci xeet wii am ci ful giñuleen di fulal ay yiw ak di ko bind fa moom, ak ñàkk giñuleen di ñàkka fulal séen i ñaawtéef.
  2. Njariñu yéene ci jëf yi ak ay jeexitam.
  3. Ngëneelu Yàlla mu kawe mi ak ug ñeewanteem ak rafetalam ci ne ku nàmm a def aw yiw te mujju ko def Yàlla bindal ko ko aw yiw.
  4. ____
  5. ____
  6. ____
  7. ____
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Bosniya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent