عَنْ أَبِي هُرَيْرَة رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ رَسُول اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إنَّ اللَّهَ تَعَالَى قَالَ: مَنْ عَادَى لِي وَلِيًّا فَقْد آذَنْتُهُ بِالحَرْبِ، وَمَا تَقَرَّبَ إلَيَّ عَبْدِي بِشَيْءٍ أَحَبَّ إلَيَّ مِمَّا افْتَرَضْتُ عَلَيْهِ، وما يَزَالُ عَبْدِي يَتَقَرَّبُ إلَيَّ بِالنَّوَافِلِ حَتَّى أُحِبَّهُ، فَإِذَا أَحْبَبْتُهُ كُنْتُ سَمْعَهُ الَّذِي يَسْمَعُ بِهِ، وَبَصَرَهُ الَّذِي يُبْصِرُ بِهِ، وَيَدَهُ الَّتِي يَبْطِشُ بِهَا، وَرِجْلَهُ الَّتِي يَمْشِي بِهَا، وَإِنْ سَأَلَنِي لَأُعْطِيَنَّهُ، وَلَئِنْ اسْتَعَاذَنِي لَأُعِيذَنَّهُ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [الأربعون النووية: 38]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"Yàlla mu kawe mi nee na: ku noonook samaw wàlliyu waajal naa ko xeex, te sama jaam du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom, te sama jaam bi du deñ di ma jegeñ-jegeñlu ci ay naafila ba ma bëgg ko, te bu ma ko bëggee maay nekk déggam bi muy dégge, ak gisam bi muy gise, ak loxoom bi muy jàppe, ak tànkam biuy doxe, te bu ma laajee ma jox ko, bu musloo ci man ma musal ko".
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ci hadiisu xudsiyu bii ne Yàlla mu màgg mi nee na: ku lor ab wàlliyu ci sama wàlliyu yi daal di koy merloo daal di koy bañ kooku waajal naa ko ab xeex yégal naa ko ag noonoo. Wàlliyu mooy: aji-gëm ju ragal Yàlla, kem li nekk ci jaam bi ci ngëm ak ragal Yàlla la céram ci wàlliyu Yàlla di nekk. Te jullit bi du jegeñ-jegeñlu Boroomam ci dara lu ko gënal li mu farataal ci moom waral ko ci moom ci def jaamu yi, ak moytu yu araam yi, te jullit bi du deñ di jegeñ-jegeñlu Boroomam ci naafila yi boole ko ak farata yi; ba am mbëggeelu Yàlla. Te bu ko Yàlla bëggee, Yàlla da koy dëgëral ci ñenti céram yii: Da koy dëgëral ci déggam, du dégg lu dul luy gërëmloo Yàlla. Dëgëral ko ci gisam, du xool jëm ci lu dul lu Yàlla bëgg moo xool te mu gërëm ko. Mu dëgëral ko ci loxoom, du def ci lu dul luy gërëmloo Yàlla. Mu dëgëral ko ci tànkam, du dox jëm ci lu dul luy gërëmloo Yàlla, te du dox jëm ci lu dul aw yiw. Ànd ak lii bu ñaanee Yàlla dara Yàlla jox ko li mu laaj, mu nekk ku ñuy nangu ñaanam, bu musloo ci Yàlla làqu ci moom, ngir sàkku kaarànge Yàlla musal ko aar ko ci li muy ragal.