Xàjjale yi:
+ -

عَنْ أَبِي مُحَمَّدٍ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ العَاصِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا، قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا يُؤْمِنُ أَحَدُكُمْ حَتَّى يَكُونَ هَوَاهُ تَبَعًا لِمَا جِئْتُ بِهِ».

[قال النووي: حديث صحيح] - [رويناه في كتاب الحجة بإسناد صحيح] - [الأربعون النووية: 41]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abii Muhammad Abdullah Ibn Amr Ibn Al-Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi".

-

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne nit ki du nekk aji-gëm ju matug ngëm ba keroog ag bëgg-bëggam di topp li Yonente bi indi ci ay digle ak i tere ak yeneen; mu bëgg li mu digle, bañ li mu tere.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Hadiis bi ab tënk la ci nangul Sariiha ak wommatul ko.
  2. Àrtu nit ki ci muy àttewoo xel ak aada di ko jiital ci kaw li Yonente bi indi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, kuy def loolu dees na dàq ci moom ngëm.
  3. Dañoo war a àttewoo Sariiha ci lépp, ndax li mu wax: "li ma indi".
  4. Gëm Yàlla day yokkoo ci topp Yàlla di wàññikoo ci moy.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent