عَنْ أَبِي بُرْدَةَ، عَنْ أَبِيهِ أَبِي مُوسَى الأَشْعَريِّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ:
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بَعَثَهُ إِلَى اليَمَنِ، فَسَأَلَهُ عَنْ أَشْرِبَةٍ تُصْنَعُ بِهَا، فَقَالَ: وَمَا هِيَ؟، قَالَ: «البِتْعُ وَالمِزْرُ»، فَقِيلَ لِأَبِي بُرْدَةَ: مَا البِتْعُ؟ قَالَ: نَبِيذُ العَسَلِ، وَالمِزْرُ: نَبِيذُ الشَّعِيرِ، فَقَالَ: «كُلُّ مُسْكِرٍ حَرَامٌ» خرجه البخاري.
وَخَرَّجَهُ مُسْلِمٌ وَلَفْظُهُ: قَالَ: بَعَثَنِي رَسُولُ اَلله أَنَا وَمُعَاذٌ إِلَى اَليَمَنِ، فَقُلْتُ: يَا رَسُولُ اَللَّهِ! إِنَّ شَرَابًا يُصْنَعُ بِأَرْضِنَا يُقَال لَهُ: المِزَرُ مِنَ الشَّعِيرِ، وَشَرَابٌ يُقَالُ لَهُ: البِتْعُ مِنَ العَسَلِ، فَقَالَ: «كُلُّ مُسْكِرٍ حَرَامٌ».
وَفِي رِوَايَةٍ لِمُسْلِمٍ: «فَقَالَ: كُلُّ مَا أَسْكَرَ عَنِ الصَّلَاةِ فَهُوَ حَرَامٌ».
وَفِي رِوَايَةٍ لَهُ: «وَكَانَ رَسُولُ الله قَدْ أُعْطِيَ جَوَامِعَ الكَلِمِ بِخَوَاتِمِهِ، فَقَالَ: أَنْهَى عَنْ كُلِّ مُسْكِرٍ أَسْكَرَ عَنْ الصَّلَاةِ».
[صحيح] - [رواه البخاري ومسلم] - [الأربعون النووية: 46]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Burdata, mu jële ci baayam Abii Muusaa Al-Asharii yal na ko Yàlla dollee gërëm:
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ko a yónni Yaman, mu laaj ay xeeti naan yu ñu fay defar, mu ne ko: yan la?, mu ne ko: "Al-Bithu, ak Al-Misru", ñu ne Abuu Burdata: lan mooy Al-Bithu? Mu ne: Siwu lem, Al-Misru: mooy Siwu Bele, mu wax ne: lépp luy màndiloo dafa araam" Al-Buxaarii génne na ko.
[Wér na] -
Abuu Muusaa Al-Asharii yal na ko Yàlla dollee gërëm day nettali ne Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ko a yónni Yaman, mu laaj ko ay xeeti naan yu ñu fay defar ndax dafa araam walla, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di leerlu ba xam yan la. Abuu Muusaa yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ko: mooy Al-Bithu: Siwu Lem, ak Al-Misru: Siwu Bele. Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko te Yàlla da ko a joxoon wax yu dajale yi: "lépp luy màndiloo dafa araam".