Xàjjale yi:
+ -

عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرٍو رضي الله عنهما قال: قال رَسولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَرْبَعٌ مَنْ كُنَّ فِيهِ كَانَ مُنَافِقًا، وَإِنْ كَانَتْ خَصْلَةٌ مِنْهُنَّ فِيهِ كَانَتْ فِيهِ خَصْلَةٌ مِنَ النِّفَاقِ حَتَّى يَدَعَهَا: مَنْ إِذَا حَدَّثَ كَذَبَ، وإِذَا وَعَدَ أَخْلَفَ، وإذَا خَاصَمَ فَجَرَ، وَإِذَا عَاهَدَ غَدَرَ».

[صحيح] - [رواه البخاري ومسلم] - [الأربعون النووية: 48]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"ñent yii képp ku mu nekk ci moom nekk na naaféq, bu wenn melo nekkee ci moom kon wenn melow naaféq nekk na ci moom ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu digee wuute ko, bu xulóo kàccoorr, bu kollarante daal di wor".

[Wér na] - [رواه البخاري ومسلم] - [الأربعون النووية - 48]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo ñent melo yoy bu dajee ci jullit bi day niróo lool ak naaféq yi ngir sababus melo yii, loolu nag mooy ki melo yi not ci moom, bu dee ki mu néew ci moom kooku du ci dugg, te mooy:
Bu njëkk bi: bu waxtaanee day fen te tay ko, te du dëggal ci ay waxam.
Ñaareel bi: bu kóllareentee ag kóllare du ko matal, te day wor àndandoom.
Ñatteel bi: bu digee du matal dig ba, te da koy wuute.
Ñenteel bi: bu xulóo daal di xëccoo ak kenn ab xulóom day tar, mu jeng wolif dëgg, di fexe ngir delloo ko ak neenal ko, di wax ay neen ak i fen.
Naaféq mooy feeñal lu wuute ak li mi nëbb, te maanaa mii dafa nekk ci boroom melo yii, ag naaféqam day nekk ci àqi ka mu waxal, te dig ko, wóolu ko, te xulóo ak moom, ak nit ki kóllareente ak moom, waaye du ne naaféq la ci lislaam, ku wenn melo ci melo yii nekk ci moom; kon am na melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral yenni màndargay naaféq ngir xuppe ak moytandikuloo ñu cay tàbbi.
  2. Li ñu jublu ci hadiis bi: mooy ne melo yii meloy naaféq la, te boroomam day niróo ak naaféq yi ci melo yii, te dafa jikkówoo seen jikkó,
  3. waaye nekkul ne naaféq la buy feeñal lislaam fekk ma ngay nëbb ag kéefar, nee nañu it hadiis bi dañu koy yan ci ki melo yii not ci moom, mu doyadal ko, woyafal ay mbiram; ku mel noonu li gën a bari pas-pasam dafa yàqu.
  4. Al-Xassaalii nee na: cosaani diine yi ci ñatt la tënku: wax, ak jëf, ak yéene, lu wane ne yàqug wax mooy fen, yàqug jëf mooy wor, yàqug yéene mooy wuute; ndaxte wuuteg dig du ko jam lu dul bu dogu ga lënkaloo ak dige ga, waaye bu doon dafa dogu ca dige ga am ndog lu ko teree am, walla mu gis leneen kooku melow naaféq nekkul ci moom.
  5. Naaféq ñaari xeet la: naaféqug pas-pas te day génne boroom ci ´gëm, te mooy feeñal lislaam ak nëbb ug kéefar, ak naaféq ug jëf, te mooy niróok
  6. naaféq yi ci seen jikkó, bii nag du génne boroomam ci ngëm, waaye bàkkaar bu mag la.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Bosniya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent