Xàjjale yi:
+ -

عَنْ عُمَرَ بْنِ الخَطَّابِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَوْ أَنَّكُمْ كُنْتُمْ تَوَكَّلُونَ عَلَى اللهِ حَقَّ تَوَكُّلِهِ لَرَزَقَكُمْ كَمَا يَرْزَقُ الطَّيْرَ تَغْدُو خِمَاصًا وَتَرُوحُ بِطَانًا».

[صحيح] - [رواه الإمام أحمد، والترمذي، والنسائي، وابن ماجه، وابن حبان في صحيحه، والحاكم] - [الأربعون النووية: 49]
المزيــد ...

Jële nañu ci Umar ibn Al-Xattaab yal na k Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc yi, day xëy nekk ku woos xiif di gont biir bi fees dell".

[Wér na] - [رواه الإمام أحمد والترمذي والنسائي وابن ماجه وابن حبان في صحيحه والحاكم] - [الأربعون النووية - 49]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da ñuy soññ ci nuy sukkandiku ci Yàlla mu kawe mi ci xëcc njariñ ak jeñ lor ci mbiri àdduna yi ak yu diine yi, ndax kenn du joxe te kenn du xañe, mbaa muy lore walla muy jariñe ku dul Moom Yàlla mu kawe mi. Ak it nuy def sabab yiy xëcc njariñ di jeñ lor ànd ak sukkandiku ci Yàlla, saa su nu defee loolu Yàlla dana nu wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc miy génn suba di ku xiif, mu dellusi ngoon biir bi fees dell, te jëf i picc mii benn sabab la ci dem wuti wërsëg, te bañ a bàyyandiku mbaa tàyyeel.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi :
  2. gëneelu wakkirlu, ak ne dafa bokk ci sabab yi gën a màgg ci yiy xëcc wërsëg.
  3. Wakkirlu du dàqoonteek def sabab yi, ndax dañoo xamal ne dëgg-dëggi wakkirlu du wuute ak xëy walla gontu jëm ci sàkku wërsëg.
  4. Yittewoog Sariiha ci jëfi xol yi; ndax wakkirlu jëfu xol la.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Bosniya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent