Xàjjale yi:
+ -

عَنِ النَّوَّاسِ بْنِ سِمْعَانَ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«البِرُّ: حُسْنُ الخُلُقِ، وَالإِثْمُ مَا حَاكَ فِي صَدْرِكَ، وَكَرِهْتَ أَنْ يَطَّلِعَ عَلَيْهِ النَّاسُ». وَعَنْ وَابِصَةَ بْنِ مَعْبَدٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: أَتَيْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ: «جِئْتَ تَسْأَلُ عَنِ البِرِّ وَالإِثْمِ»، قُلْتُ: نَعَمْ، قَالَ: «اسْتَفْتِ قَلْبَكَ، البِرُّ: مَا اطْمَأَنَّتْ إلَيْهِ النَّفْسُ، وَاطْمَأَنَّ إلَيْهِ القَلْبُ، وَالإِثْمُ: مَا حَاكَ فِي نَفْسِكَ وَتَرَدَّدَ فِي الصَّدْرِ، وَإِنْ أَفْتَاكَ النَّاسُ وَأَفْتَوْكَ».

[صحيح] - [الحديث الأول: رواه مسلم، والحديث الثاني: رواه أحمد والدارمي.] - [الأربعون النووية: 27]
المزيــد ...

Jële nañu ci An-Nuwaas Ibn Samhaan yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«baax mooy: rafet jikkó, bàkkaar mooy liy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ci gis ko».

[Wér na] - [الحديث الأول: رواه مسلم، والحديث الثاني: رواه أحمد والدارمي] - [الأربعون النووية - 27]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle lu baax ak bàkkaar, mu wax ne: melo wi gën a màgg ci meloy baax mooy rafet jikkó ci Yàlla ci ragal ko, ak rafet jikkó ci nit ñi ci di yenu seen i lor, ak di néew i mer, ak di yaa kanam, ak teey i wax, ak jokk mbokk, ak topp ndigal, ak ñeewant, ak ug mbaax, ak rafet ug nekkaale ak àndaale. Ak ne lu baax mooy loo xam ne xol bi ak xel mi da ciy dal. Bàkkaar nag mooy lu nekk ci xel ci ay lënt mu ciy dengi-dengi te xolam du ci dal da ciy sikk-sàkka, ak di ragal mu nekk bàkkaar, te bëggu ko a fésal ndax li mu bon ci bëti nit ñu baax ñi te mat, ndax te bakkan ni ñu ko binde mooy day bëgg nit ñi di gis yu baaxam, kon bu bañee ñu gis yenn jëf yi kon dafa nekk bàkkaar te du lu baax; donte nit ñi dañu laa ubbee leneen bul jël seen wax fii ak màndargay lënt yi moo ngi dengi-dengi ci sa bakkan, ndax te ubbee ga du dindi lënt ga bu dee teguwul ci xam-xam; waaye bu dee ubbee gi dafa tege ci xam-xamu tegtalu sariiha kon li war ci aji-laaj ji mooy mu dellu ci ubbee ga, donte dënnam tàlliwu ca.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci teddngay jikkó yi; ndaxte rafet jikkó dafa bokk ci melo yi gën a màgg.
  2. Dëgg ak neen seen mbir lëntul ci aji-gëm ji, waaye day xam dëgg ci leer giy nekk ci xol bi, di daw neen di ko bañ.
  3. Bokk na ci màndargay lu bon xol bi di jàq di ci dengi-dengi, ak bañ nit ñi gis ko.
  4. As-Sindii nee na: lii mooy mbir yu lënt yi nga xam ne nit ñi ràññeewuñu benn ci ñaar yi; bu dul loolu rekk li ci Sariiha digle bu dee tegtal ba feeñul ca day wuute ak loolu ndax daa bokk ci li baax, li ñu tere it naka noonu daa bokk ci li bon, kon aajowoowul di laaj xol bi ak ug dalam.
  5. Ñi ñuy waxal ci hadiis bi ñooy woroom xol yu mucc yi, waaye du woroom xol yu yàqu yi nga xam ne xamul lu baax te du bañ lu bon lu dul lu jaxasoo ak bànneexam.
  6. At-Tiibii nee na: nee nañu firees na baax ci hadiis bi ci ay maanaa yu bari, ñu firee ko ci benn barab liy dalal xel ak xol, ñu firee ko it ci beneen barab gëm, ci beneen barab lu lay jegeloo Yàlla, fii rafet jikkó, ñu firee rafet jikkó: muñ lor, ak néew i mer, ak yatal kanam, ak teey i wax, yooyu yépp nag yu jegee la ci maanaa.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Litwaani Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent