Xàjjale yi:
+ -

عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ بُسْرٍ رَضِيَ اللَّهِ عَنْهُ قَالَ: أَتَى النَّبِيَّ رَجُلٌ، فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللَّهِ! إِنَّ شَرَائِعَ الإِسْلَامِ قَدْ كَثُرَتْ عَلَيْنَا، فَبَابٌ نَتَمَسَّكُ بِهِ جَامِعٌ؟ قَالَ:
«لاَ يَزَالُ لِسَانُكَ رَطْبًا مِنْ ذِكْرِ اللَّهِ». وفي رواية: مِنْ حَدِيثِ مُعَاذِ بْنِ جَبَلٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ: آخِرُ مَا فَارَقْتُ عَلَيْهِ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنْ قُلْتُ: أَيُّ الأَعْمَالِ خَيْرٌ وَأَقْرَبُ إِلَى اللَّهِ؟ قَالَ: «أَنْ تَمُوتَ وَلِسَانُكَ رَطْبٌ مِنْ ذِكْرِ اللَّهِ عَزَّ وَجَلَّ».

[صحيح] - [رواه أحمد والترمذي وابن ماجه وابن حبان] - [الأربعون النووية: 50]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdulla ibn Busrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: jenn waay dafa ñëw ci Yonnente bi, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi! Yi lislaam santaane dafa bari ci nun, ndax am na bunt bu dajale bu nu man a jàpp? Mu wax ne:
"bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla".

[Wér na] - [رواه أحمد والترمذي وابن ماجه وابن حبان] - [الأربعون النووية - 50]

Leeral

Jenn waay dafa jàmbat Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ne naafila yi dafa bari ci moom ba tax mu lott ci ngir néew kàttanam, mu laaj Yonnente bi ngir mu tegtal ko jëf ju néew juy indi yool yu bari ngir mu jàpp ci.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tektal ko ci muy Sax di tooyal làmmiñam ci tudd Yàlla ci bépp jamono ak ci gépp anam; ci sàbbaal ak sant ak jéggalu ak ñaan ak yu ko niru.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu saxoo tudd Yàlla mu kawe mi.
  2. Bokk na ci màggug ngëneelu Yàlla mu yombal sababi yiw yi.
  3. Gënlaanteg jaam ñi mingi ci seen cér yi ci bunti mbaax yi ak yiw yi.
  4. Baril tudd Yàlla ci làmmiñ di sàbbaal ak di sant ak sikar ak di kàbbar ak yu dul yooyu, ànd ak mu dëppoo ak xol bi day taxaw taxawaayu ay naafila yu bari ci jaamu yi.
  5. Sàmmonteek Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel aji-laaj ji ci tontu laaj bu nekk ca la méngoo ak moom.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Bosniya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent