Listu hadiis yi

Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
عربي الإنجليزية الأوردية
li dagan de leer na li araam it leer na,
عربي الإنجليزية الأوردية
wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc
عربي الإنجليزية الأوردية
Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf
عربي الإنجليزية الأوردية
kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi
عربي الإنجليزية الأوردية
ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu kóllareentee wor, bu digee wuute ko, bu xuloo wax lu bon
عربي الإنجليزية الأوردية
baax mooy: rafet jikkó, bàkkaar mooy liy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ci gis ko
عربي الإنجليزية الأوردية
Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?
عربي الإنجليزية الأوردية
bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate
عربي الإنجليزية الأوردية
moytuleen juróom-ñaar yiy alage
عربي الإنجليزية الأوردية
ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll
عربي الإنجليزية الأوردية
ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara
عربي الإنجليزية الأوردية
ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana
عربي الإنجليزية الأوردية
àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu
عربي الإنجليزية الأوردية
wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar
عربي الإنجليزية الأوردية
ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm
عربي الإنجليزية الأوردية
li dagan de leer na li araam it leer na,
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf
عربي الإنجليزية الأوردية
jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
عربي الإنجليزية الأوردية
gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc
عربي الإنجليزية الأوردية
Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko
عربي الإنجليزية الأوردية
bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi
عربي الإنجليزية الأوردية
Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi
عربي الإنجليزية الأوردية
Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf
عربي الإنجليزية الأوردية
wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc
عربي الإنجليزية الأوردية
bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-
عربي الإنجليزية الأوردية
ñoom ñaar de ñoo ngi leen di mbugal, te sax mbugaluñu leen ci lu rëy, kenn ki moom daawul suturawu bu daan saw, keneen ki nag da daan dox di rambaaj
عربي الإنجليزية الأوردية
àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi
عربي الإنجليزية الأوردية
Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal
عربي الإنجليزية الأوردية
misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne,
عربي الإنجليزية الأوردية
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na baril lu muy wax: "yaw Aji-Wëlbati xol yi saxalal sama xol bi ci sa diine ji
عربي الإنجليزية الأوردية
ku ñaan Yàlla nekk sahiid ci ag dëggu kon Yàlla dana ko jotale ca darajay ña nekk sahiid, donte dafa dee ci kaw lalam
عربي الإنجليزية الأوردية
Nattu du deñ ci jullit bu góor bi ak bu jigéen bi di dal ci bakkanam ak ci doomam ak ci alalam ba mu daje ak Yàlla fekk benn bàkkaar nekkul ci kawam
عربي الإنجليزية الأوردية
yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi
عربي الإنجليزية الأوردية
danañu indi jenn waay ëllëg bis-pénc, sànni ko ca sawara, buttiti biir yi tasaaroo, mu koy wër kem ni mbaam di wëre ci takkuwaayam
عربي الإنجليزية الأوردية
aw doj la wu ñu sànni ca biir sawara diirub juróom-ñaar-fukki at, mooy door a wàcc ca sawara sa leegi ba egg ca suuf
عربي الإنجليزية الأوردية
wàlle amul gaafal amul, njuuma amul, Safar amul, te nanga daw ki gaana kem ni ngay dawe Gaynde
عربي الإنجليزية الأوردية
Damaa wax: "yaw Yonnente Yàlla bi, ana lan mooy musale? Mu ne ma "tëyéel sa làmmiñ, te na la sa kër doy, te nga jooy say ñuumte
عربي الإنجليزية الأوردية
sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy
عربي الإنجليزية الأوردية
bu kenn ci yéen faatu lu dul ne dafa rafet njort ci Yàlla
عربي الإنجليزية الأوردية
man de bokk na ci li may ragal ci yéen sama ginnaaw, ñu ubbil leen naataangey àdduna ak taaram
عربي الإنجليزية الأوردية
ki gën a woyof mbugal ci waa sawara mooy ki am ñaari dàll ak ñaari waroy dàll yu sawara, yuuram gi di ci bax kem ni cin di baxe, ba du foog ne kenn a ko gën a tar mbugal, te moo leen gën a woyof mbugal
عربي الإنجليزية الأوردية
lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla mu màgg mi day tàllal loxoom ci guddi gi ngir ki doon def ñaawteef ci bëccëg gi tuub, di tàllal loxoom ci bëccëg gi ngir ki doon def ñaawteef ci guddi gi tuub, ba baa jant bi di fenke ci sowwu bi
عربي الإنجليزية الأوردية
nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon
عربي الإنجليزية الأوردية
éey yaw doomu Aadama ji boo ma ñaanee yaakaar ma ma jéggal la ak lu man a nekk ci yaw te duma faale
عربي الإنجليزية الأوردية
Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax,
عربي الإنجليزية الأوردية
Aji-woote ji day woote ne: di ngeen wér te du ngeen tawatati ba fàww, di ngeen dund te du ngeen deeati ba fàww, di ngeen bijjaaw te du ngeen màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen yoqatati ba fàww
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: lu ñuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi?
عربي الإنجليزية الأوردية
bu waa àjjana duggee àjjana, Yàlla mu Barkeel mi te kawe day wax ne: ndax bëggeen dara lu ma leen dolli?
عربي الإنجليزية الأوردية
ñaari xaaj a gi nii yu bokk ci waa sawara te gisaguma leen,ay nit yu yor ay yar yu mel ni geeni nag di ci dóor nit ñi,ak ayjigéen yu solu ba noppi rafle, jeng di jengale
عربي الإنجليزية الأوردية
yéen mbooloom jigéen ñi deeleen saraxe, man de gis naa leen ngeen ëpp ci waa sawara" ñu ne ko: ndax lan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "dangeen a bari ag rëbbaate, di weddi njekk, gisuma jigéen ñu matadi xel ak diine te gaaw a yóbb xelu góor gu dogu ba mel ni kenn ci yéen jigéen ñi
عربي الإنجليزية الأوردية
saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam
عربي الإنجليزية الأوردية
dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf
عربي الإنجليزية الأوردية
Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama
عربي الإنجليزية الأوردية
buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub
عربي الإنجليزية الأوردية
bu ngeen gisee ñiy topp lënt ya xamleen ne ñooñii la Yàlla di wax nangeen leen moytu
عربي الإنجليزية الأوردية
amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal
عربي الإنجليزية الأوردية
{te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}
عربي الإنجليزية الأوردية
ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu kóllareentee wor, bu digee wuute ko, bu xuloo wax lu bon
عربي الإنجليزية الأوردية
dëddul àdduna kon Yàlla dana la bëgg, dëddul li ci nit ñi kon nit ñi danañu la bëgg
عربي الإنجليزية الأوردية
doomu Aadama feesalul lenn ndab lu yées biiram, doy na sëkk doomu Aadama ji lekk gu mu taxawale ndiggam li, bu manut a ñàkk, kon na def biiram ñatti xaaj benn ba ngir lekkam, beneen ba ngir naanam, ñatteelu xaaj ba ngir noyyeem
عربي الإنجليزية الأوردية
Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xoolug mbetteel mu digal ma ma wëlbati samab gis
عربي الإنجليزية الأوردية
moytuleen salte yii Yàlla tere, ku ca laal na suturawu ci surutas Yàlla, te tuub jëm ci Yàlla, ndaxte ku ñu wuññil ay bootam dananu teg ci moom Téereb Yàlla mu màgg mi
عربي الإنجليزية الأوردية
amna ci ñi leen jiitu woon jenn waay ju am gaañu-gaañu, mu saalit, daal di jël paaka dagg loxo bi, dereet ji dogul ba mu faatu, Yàlla mu kawe mi wax ne: sama jaam bi gaawe na ma ci boppam, araamal naa ci moom àjjana
عربي الإنجليزية الأوردية
Yaw Abuu Sahiid, ku gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat di Yonenteem àjjana war na ci moom
عربي الإنجليزية الأوردية
buleen soxorante, buleen worante, buleen bañante, buleen dummooyoonte, bu kenn ci yéen jaay ci kaw njaayu keneen, nangeen nekk ay mbokk
عربي الإنجليزية الأوردية
deeleen xool ñi leen féete suuf, te buleen xool ci ñi leen féete kaw, ndax moo gën a yay ba dungeen xeeb xéewali Yàlla yi ci seen kaw
عربي الإنجليزية الأوردية
ñaari xéewal a ngi nii yoo xamne nit ñu bari woru na ñu ci: ag wér ak ug jot
عربي الإنجليزية الأوردية
ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”
عربي الإنجليزية الأوردية
ku xëy ci yéen di ku am jàmm ci yaramam, am kóolute ci bakkanam, am dundug bisam,, dafa mel ni jox nañu ko àdduna
عربي الإنجليزية الأوردية
am nga li nga mébét ak lu mel ni moom
عربي الإنجليزية الأوردية
ñeel na Aji-gëm ji ca àjjana ab xaymab wurus bu ñu yaatal, guddaayam tolloo ak juróom-benni Miil, aji-gëm ji dana fa am ay njaboot, aji-gëm ji dana leen wër te ñenn ñi duñu gis ñeneen ñi
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla mu Baarkeel mi te kawe nee na: waajalal naa sama jaam yu sell yi, lu bët musul a gis, nopp musu ko a dégg, te musul a rot ci xolo nit
عربي الإنجليزية الأوردية
bàmmeel de mooy wàccuwaay bi njëkk ci wàccuwaayi allaaxira yi, bu ca muccee la ca ginnaawam mooy gën na yomb, bu ca muccul la ca ginnaawam mooy gën na tar
عربي الإنجليزية الأوردية
mbooloo miy njëkk a dugg àjjana dañuy nekk ci melow weer wi ci guddig Badr, ña topp ca ñoom gën a tarug leer biddiwu per ci ag leer
عربي الإنجليزية الإندونيسية
ku xandaalu daanu ci aw doj daal di ray boppam kooku ci sawaraw Jahannama la jëm di ca xandaalu sax ca di ku ñu fay saxal ba fàww
عربي الإنجليزية الإندونيسية
jaayanteleen ak man ci ne dungeen bokkaale Yàlla ak dara, te dungeen sàcc, dungeen njaalo
عربي الإنجليزية الإندونيسية
lislaam dafa tàmbali di lu tumurànke, te dana dellu ca na mu tàmbalee woon di lu tumurànke, kon texe ñeel na way-tumurànke yi
عربي الإنجليزية الإندونيسية
moytulleen bàkkaar yi ñuy xeeb
عربي الإنجليزية الإندونيسية
juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga
عربي الإنجليزية الإندونيسية