عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«نَارُكُمْ جُزْءٌ مِنْ سَبْعِينَ جُزْءًا مِنْ نَارِ جَهَنَّمَ»، قِيلَ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِنْ كَانَتْ لَكَافِيَةً. قَالَ: «فُضِّلَتْ عَلَيْهِنَّ بِتِسْعَةٍ وَسِتِّينَ جُزْءًا كُلُّهُنَّ مِثْلُ حَرِّهَا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3265]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama», ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, bu doon moom rekk kon dana doy. Mu wax ne: «ëppe na ko juróom-benni fukk ak juróom-ñenti xaaj, te ñoom ñépp ñoo ngi mel ni aw tàngaayam».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3265]
Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne sawaraw àdduna ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaji sawaraw Jahannama, Sawaraw allaaxira moo gën a tàng sawaraw àdduna ci juróom-benni fukk ak juróom-ñetti xaaj, te xaaj bu ci ne moo ngi tolloog tàngaayu sawaraw àdduna. Ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, sawaraw àdduna bi rekk doyoon na ngir mbugal ña fay dugg, Mu ne leen: sawaraw Jahannama ëppe na sawaraw àdduna ci juróom-benn ak juróom- ñenti xaaj te ñoom ñépp a mel ni moom ciw tàngaay wu tar.