+ -

عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ مَسْعُودٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ:
حَدَّثَنَا رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَهُوَ الصَّادِقُ المَصْدُوقُ: «أَنَّ خَلْقَ أَحَدِكُمْ يُجْمَعُ فِي بَطْنِ أُمِّهِ أَرْبَعِينَ يَوْمًا وَأَرْبَعِينَ لَيْلَةً، ثُمَّ يَكُونُ عَلَقَةً مِثْلَهُ، ثُمَّ يَكُونُ مُضْغَةً مِثْلَهُ، ثُمَّ يُبْعَثُ إِلَيْهِ المَلَكُ، فَيُؤْذَنُ بِأَرْبَعِ كَلِمَاتٍ، فَيَكْتُبُ: رِزْقَهُ وَأَجَلَهُ وَعَمَلَهُ وَشَقِيٌّ أَمْ سَعِيدٌ، ثُمَّ يَنْفُخُ فِيهِ الرُّوحَ، فَإِنَّ أَحَدَكُمْ لَيَعْمَلُ بِعَمَلِ أَهْلِ الجَنَّةِ حَتَّى لاَ يَكُونُ بَيْنَهَا وَبَيْنَهُ إِلَّا ذِرَاعٌ، فَيَسْبِقُ عَلَيْهِ الكِتَابُ، فَيَعْمَلُ بِعَمَلِ أَهْلِ النَّارِ فَيَدْخُلُ النَّارَ، وَإِنَّ أَحَدَكُمْ لَيَعْمَلُ بِعَمَلِ أَهْلِ النَّارِ حَتَّى مَا يَكُونُ بَيْنَهَا وَبَيْنَهُ إِلَّا ذِرَاعٌ، فَيَسْبِقُ عَلَيْهِ الكِتَابُ، فَيَعْمَلُ عَمَلَ أَهْلِ الجَنَّةِ فَيَدْخُلُهَا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 7454]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne:
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxtaanal na nu te mooy aji-dëggal ba di ku ñu dëgggal ki mu ne: «kenn ci yéen dees na dajale am mbindam ci biiru yaayam ñent-fukki bis ak ñent-fukki guddi, mu nekk lumbuw dereet, kem loolu, nekk aw suux kem loolu, ñu yabal ci moom malaaka ma, ñu digal ko ñenti baat, mu bind ko: wërsëgam, ab digam, ak jëfam, ak day texeedi walla day texe, mu wal ca ruu, kenn ci yéen de dana jëf jëfi waa àjjana ba dara nekkul digganteem ak moom lu dul loxo, téere ba jiitu ko mu jëf jëfi waa sawara daal di dugg sawara, kenn ci yéen it dana jëf jëfi waa sawara ba dara doxul digganteem ak moom lu dul ab loxo, mu jëf jëfi waa àjjana daal di dugg àjjana».

-

Leeral

Leerarug hdiis bi: Abdullah Ibn Mashuud nee na: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxtaanal na nu te mooy aji-dëggal ciy waxam, di ku ñu dëggal ndax Yàlla mu kawe mi moo ko dëggal, Mu wax ne: ku nekk ci yéen dees na dajale am mbindam, te loolu mooy bu góor gi dikkalee Soxnaam, Maniyoom mi tasaaroo ci biiru ku jigéen ki ñent-fukki fan nekk aw toq, Mu nekk aw lumb te mooy dereet ju tal te wow, ci ñaareelu ñent-fukk ya, Mu nekkaat aw suux te mooy dogu yàpp wu tolloog lu ñu yëy, ci ñatteelu ñent-fukk yi Yàlla yabal ci moom malaaka ma, mu wal ca ruu ginnaaw ñatteelu ñent-fukk ya, Ñu digal malaaka mi mu bind ñenti baat, te mooy: wërsëgam, te mooy nattub li mu war a am ci xéewal cig dundam, Ak digam, te mooy diir bi muy des ci àdduna, Ak jëfam, lan la? Ak day texeedi walla day texe. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di giñ ne kenn dana jëf jëfi waa àjjana jëfam di lu baax, maanaam ci liy feeñ ci nit ñi, mu sax ci loolu ba dara doxul digganteem ak àjjana lu dul ab loxo, maanaam: dara desul ci mu àgg fa lu dul mel ni koo xam ne li des digganteem ak benn bérab ci suuf ab Lox rekk la, tére ba not ko ak la ñu dogal ci kawam ci moom ci loolu nag mu jëf jëfi waa sawara ñu tëje ko ay jëfam mu dugg sawara; Ndax sarti nangug jëf mooy mu sax ca te du ko soppi, ak keneen ci nit ñi di jëf jëfi waa sawara ba jege faa dugg, ba mel ni digganteem ak sawara lu tollook loxo ci suuf moo fa dox, dogal ba not ko mu jëf jëfi waa àjjana daal di dugg àjjana.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi:
  2. Mujjug bir yi moo ngi aju ca ndogal la jiitu te di ca wéye.
  3. Moytoo woru ci melokaani jëf yi; ndaxte jëf yi moo ngi aju ca mujj ga.