+ -

عَنْ عَبْدِ اللهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ الْعَاصِ رضي الله عنهما قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«كَتَبَ اللهُ مَقَادِيرَ الْخَلَائِقِ قَبْلَ أَنْ يَخْلُقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِخَمْسِينَ أَلْفَ سَنَةٍ، قَالَ: وَعَرْشُهُ عَلَى الْمَاءِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2653]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Yàlla bind na ndogali mbindéef yi njëkk muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at, mu daaldi wax: te boobu gàngunaayam ga ma nga ca kawum ndox».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2653]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla bind na lépp luy am ci ndogali mbindéef yi cig faramface ci dund ak dee, ak wërsëg ak yeneen, ca àlliwó ja ñu sàmm(Lawhul Mahfuus) lu jiitu muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at, te dana am kem na ko Yàlla dogale, Lépp luy am ci ndogalu Yàlla ak kàttanam lay ame. Lépp lu jot nit ki naru ko woon a moy, te lépp lu ko moy naru ko woon a jot.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi:
  2. Gëm ndogal yi lu war la.
  3. Ndogal mooy: xam gi Yàlla xam bir yi, bind ko, ak coobareem, ak amal ga mu ko amal.
  4. Gëm ne ndogal yi bind nañu ko njëkk ñuy bind asamaan yi ak suuf si day waral gërëm ak nangu.
  5. Gàngunaayu Aji-Yërëme ji moo ngi ci kawum ndox lu jiitu bindug asamaan yi ak suuf si.