Xàjjale yi: Pas-pasu Lislaam . Gëm dogal yi .
+ -

عَنْ طَاوُسٍ أَنَّهُ قَالَ: أَدْرَكْتُ نَاسًا مِنْ أَصْحَابِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، يَقُولُونَ كُلُّ شَيْءٍ بِقَدَرٍ، قَالَ: وَسَمِعْتُ عَبْدَ اللهِ بْنَ عُمَرَ رضي الله عنهما يَقُولُ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«كُلُّ شَيْءٍ بِقَدَرٍ، حَتَّى الْعَجْزِ وَالْكَيْسِ، أَوِ الْكَيْسِ وَالْعَجْزِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2655]
المزيــد ...

Jële nañu ci Taawuus mu wax ne: fekk naa fi ay nit ci Sahaabay Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ñuy wax naan lépp a ngi aju ci ndogal yi, Taawuus wax ne: dégg naa Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«lépp a ngi ci ndogal yi, ba ci lott ak muus, mbaa muus ak lott».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2655]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne lépp a ngi aju ci ndogal, Ba ci lompañ te mooy: bàyyi loo war a def ngir di tanxamlu ak di ko yéexe ci waxtoom, ci biri àdduna yi ak yu allaaxira yi. Ak ba ci muus, te mooy: sawar ak ñaw ci biri àdduna yi ak yu allaaxira yi. Ak ne Yàlla mu kawe mi dafa dogal muus ak lompañ ak lépp, dara du am lu dul ne jiitu na ca xam-xamu Yàlla ba ak coobareem.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral pas-pasu Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ci ndogal yi.
  2. Lépp ci ndogal lay ame ba ci lompañ ak cawarte.
  3. Leerlug Sahaaba yi ak séenug moytu ci tuxal Hadiisi Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
  4. gëm ndogal yépp yu neex ya ak yu naqari ya.