عن أبي موسى رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«إِنَّ اللهَ لَيُمْلِي لِلظَّالِمِ، حَتَّى إِذَا أَخَذَهُ لَمْ يُفْلِتْهُ» قَالَ: ثُمَّ قَرَأَ: «{وَكَذَلِكَ أَخْذُ رَبِّكَ إِذَا أَخَذَ الْقُرَى وَهِيَ ظَالِمَةٌ إِنَّ أَخْذَهُ أَلِيمٌ شَدِيدٌ}[هود: 102]»
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4686]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc» nee na: mu daal di jàng: aaya bii «{niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee waa dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102]»
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4686]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di wéy cig tooñ ak i moy ak bokkaale, ak tooñ nit ñi ci séen i àq, ndax Yàlla mu kawe mi day néggandiku tooñkat bi di ko yeexe ak di guddal fanam di baril alalam te du ko gaawa mbugal; bu tuubul mu jàpp ko te du ko bàyyi ndax ay bàkkaar yu bari.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng aaya bii: {niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee ab waa dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102].